Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

14 of 732 cards

Clear filters
"bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla".
Wér na Ahmad, ak At-Tirmisiyyu, ak Ibn Maaja ak Ibn Hibbaan ñoo ko soloo.
«ku wax: Subhaanal Laahi wa bi hamdihii, ci bis bi téeméeri yoon, ñu sippi ay bàkkaaram doonte dafa tol ni puuriti géej».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ndax du ma leen tegtal li gën ci seen jëf yi, te gën cee sell fa seen Boroom, te gën cee kawe ci seeni daraja te gën ci yéen wurus ak xaalis, te gën ci yéen ngeeni daje ak séeni noon ngeen di dóor seen doq ya, ñoom ñuy dóor seen doq yi?" Ñi ne ko ahakay. Mu ne: "tudd Yàlla mu kawe mi".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"dajee naa ak Ibraahiima guddi gi ñu ma rañaanee mu wax ne: yaw Muhammat, jottalil ma saw xeet samag nuyóo, te nga xibaar leen ne Àjjana lu teey ag suuf la, lu neex am ndox la, te ab bayaal la, te la koy jëmbët mooy Subhaanal Laah, walhamdu lil-Laah, wa laa iLaaha illallaahu, wal-Laahu Akbaru ".
Tane na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal At-tirmisiy soloo na ko.
Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.
Wér na Muslim soloo na ko.
«bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Jële na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu nettali jële ci Boroomam mu màgg mi, mu wax ne: «ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar Yàlla mu baarkeel mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar, Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, mu dellu defaat bàkkaar, daal di wax: ay sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar,Yàlla mu màgg mi wax ne: sama jaam bi def na bàkkaar, xam ne am na Boroom buy jéggale bàkkaar, tey jàppe it ci Bàkkaar, defal lu la soob jéggal naa la».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci menn mbooloo ci sahaabaam yi, ne leen: "lan moo leen toogloo?" Ñu ne ko: dañoo toog di tudd Yàlla di ko sant ci li mu nu gindi ci Lislaam, te xéewalal nu ko, mu wax ne: "ndax man ngeen a seedeel Yàlla ne dara toogloowu leen lu dul loolu?" Ñu ne ko: giñ nañu ci Yàlla ne dara toogloowu nu lu dul loolu, mu ne leen: "man nag giñloowuma leen ci ne dama leen a tuumaal, waaye Jibriil moo ñëw fi man xibaar ma ne Yàlla mu kawe mi moo ngi leen di puukarewoo fa malaaka ya".
Wér na Muslim soloo na ko.