Skip to content

Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».

سُئِلَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَنْ أَكْثَرِ مَا يُدْخِلُ النَّاسَ الْجَنَّةَ، فَقَالَ: «تَقْوَى اللهِ وَحُسْنُ الْخُلُقِ»، وَسُئِلَ عَنْ أَكْثَرِ مَا يُدْخِلُ النَّاسَ النَّارَ فَقَالَ: «الْفَمُ وَالْفَرْجُ».

At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Tane na ci ag càllala, wér ci geneen càllala
Leeral gi

Leerarug adiis b: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sabab yi gën a màgg yuy dugale àjjana ñaari sabab la, te mooy: Ragal Yàlla ak rafet jikko. Ragal Yàlla: mooy nga def kiiraay sa diggante ak mbugalum Yàlla, ci di def ay ndigalam di moytu ay tereem. Rafet jikko: dana nekk ci yaatal kanam, ak di def ñekk tey feg lor yi. Sabab yi gën a man a duggale sawara ñaar la, te mooy: Làmmeñ ak awra. Bokk na ci Bàkkaari làmmeñ yi: fen ak jëw ak rambaaj ak yeneen. Bokk na ci Bàkkaari awra yi: njaalo ak ngóor-jigéen ak yeneen.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Dugg àjjana daa am ay sabab yu aju ci Yàlla mu kawe mi, bokk na ca: ragal ko, ak ay sabab yu aju ci nit ñi, bokk na ca: rafet jikko.

Làmmeñ lu bon la ci boroom, te bokk na ci liy tax a dugg safara.

Lorànge yi ci bànneex yi ak ñaawtéef yi ci nit ñi, mooy ne bokk nañu ci liy gën a waral ñu dugg sawara.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 536) (2004).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (5/ 318) (4246).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (13/ 287) (7907).

Yataal gi (8)

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

للبسام (7/ 509).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 369).

فتح ذي الجلال والإكرام.

لابن عثيمين (6/ 453).

سبل السلام بشرح بلوغ المرام.

للصنعاني (2/ 696).