Skip to content

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar.

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar.

أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ تَوَضَّأَ مَرَّتَيْنِ مَرَّتَيْنِ.

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan jàpp leeg-leeg daa na raxas cér bu nekk ñaari yoon, mu raxas kanam gi -ca la gallaxndiku ak saraxndiku bokk- ak ñaari loxo yi ak ñaari tànk yi ñaari yoon.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Li war ci raxas cér yi mooy benn yoon, lu ca tege dañu koo sopp.

Yoonal nañu jàpp ñaar-ñaar leeg-leeg.

Li ñu yoonal ci masaa bopp mooy benn yoon.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 43) (158).

Yataal gi (1)

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (1/ 244).