"ki leen gën a ragal Yàlla gën leen a xam Yàlla mooy man".
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu leen daan digal da leen di digal lu ñu àttan, ñi ne ko: nun melunu kem ni nga mel yaw Yonnente Yàlla bi, Yàlla jéggal na la li jiitu ci say bàkkaar ak li mujj, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di mer ba ñuy xam mer mi ci kanamam gi, topp mu ne: "ki leen gën a ragal Yàlla gën leen a xam Yàlla mooy man".
كَانَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا أَمَرَهُمْ أَمَرَهُمْ مِنَ الأَعْمَالِ بِمَا يُطِيقُونَ، قَالُوا: إِنَّا لَسْنَا كَهَيْئَتِكَ يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنَّ اللَّهَ قَدْ غَفَرَ لَكَ مَا تَقَدَّمَ مِنْ ذَنْبِكَ وَمَا تَأَخَّرَ، فَيَغْضَبُ حَتَّى يُعْرَفَ الغَضَبُ فِي وَجْهِهِ، ثُمَّ يَقُولُ: «إِنَّ أَتْقَاكُمْ وَأَعْلَمَكُمْ بِاللَّهِ أَنَا».
Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan digal nit ñi jenn jëf ci jëf yi da leen di digal la yomb ca ñoom wolif la jafe, ngir ragal ñi tële ca a sax, moom mu def lu mel ni la mu leen digal ci woyofal, waaye ñoom ñoo sàkku mu teg leen lu diis ngir jàpp ne ñoo gën a aajowoo jëf yu bari ci moom ngir yëkkëti seen daraja yi. Ñu ne ko: nun melunu ak yaw yaw Yonnente Yàlla bi, ndax Yàlla jéggal na la li jiitu ci say bàkkaar ak li mujj, muer ba ñu xam meri ci kanamam gi, topp mu wax ne: maa leen gën a ragal Yàlla gën leen a xam Yàlla, kon defleen li ma leen digal.
Ibn Hajar nee na: daleen di digal li yomb ci ñoom ngir ñu sax ca, niki mu ko waxe ci beneen hadiis: "jëf yi Yàlla gën a bëgg mooy ya ca gën a sax".
Nit ku baax dana jaadu mu bañ a bàyyi góor-góorlu ci jëf ju baax ngir sukkandiku ci ag mbaaxam.
Dagan na nit ki waxtaane li nekk ci moom ci ngëneel ci kem aajowoo ga bu muccre ci puukarewu ak màgg-màgglu.
Li gën a yey ci jaamu gi mooy jublu gi ak taqoo gi, waaye du ëppal gu lay jëme ci bàyyi ko.
Ibn Hajar nee na: jaam bi bu jotee jubluwaayu jaamu gi ak ay meññetam loolu mooy gën a waral mu sax ca, ngir sàkkoo téye xeewal ga, ak sàkku ko a dolli ci sant.
Yoonalees na mer bu ñi wuute ak mbiru sariiha, ak weddi ci aji-muus ñi man a dégg bu dee dafa gàtteñlu ci dégg ga, ngir ñaax ko ci yeewu.
Ñeewantug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci xeetam wi, ak ne diine dafa yomb, sariiha it lu jub la te yaatu.
Tarug xemmeemteefu sahaaba yi ci jaamu gi, ak seenug sàkkoo dolliku ci yiw yi.
Taxaw ci li Sariiha tënk ci dogu yi ak yombal yi, ak gëm ne jël li gën a am ñeewant te dëppoo ak Sariiha moo gën a yey jël lu metti la te wuute ak moom.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 13) (20).
Yataal gi (2)
شرح صحيح البخاري لابن بطال (73/1).
عمدة القاري شرح صحيح البخاري (1/ 166).