Skip to content

"giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm", ñu ne ko: kan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "ki dëkkandoom muccug ci ay loram".

Jële nañu ci Abuu Surayhin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

"giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm", ñu ne ko: kan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "ki dëkkandoom muccug ci ay loram".

«وَاللَّهِ لاَ يُؤْمِنُ، وَاللَّهِ لاَ يُؤْمِنُ، وَاللَّهِ لاَ يُؤْمِنُ»، قِيلَ: وَمَنْ يَا رَسُولَ اللَّهِ؟ قَالَ: «الَّذِي لاَ يَأْمَنُ جَارُهُ بَوَايِقَهُ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa giñ feddali giñam li ñatti yoon, daal di ne: giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, Sahaaba yi laaj ko: kan mooy ki dul gëm yaw Yonente Yàlla bi? Mu wax ne: mooy ki dëkkandoom ragal woram ak tooñam ak ayam.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Dàq ngëm ci ki dëkkandoom wóoluwul tooñaangeem ak ayam day tegtale ni ci bàkkaar yu mag yi la, ak ne ki ku def dafa mànki ag ngëm.

Ñaaxe gu feddaliku ci rafetal jëme ci dëkkandoo ak bàyyi ko a lor ci wax walla jëf.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 10) (6016).

Yataal gi (2)

التوضيح لشرح الجامع الصحيح (28/ 321).

النهاية في غريب الحديث والأثر (93).