Skip to content

"ay nit danañu ñëw ci mujjug jamono seeni at néew, ñu suufe ay xalaat, dañuy wax li gën ci waxi mbindeef yi, waaye dañuy génn ci diine kem ni fett gi di génne ci sànnikaay gi,

Jële nañu ci Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne: bu ma leen di waxtaanal jële ci Yonente Yàlla bi waat naa ne ma jóge ca Asamaan daanu moo ma gënal ma koy fenal, waaye bu ma leen di waxtaanal sama diggante ak yéen ab xeex nag worante la dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"ay nit danañu ñëw ci mujjug jamono seeni at néew, ñu suufe ay xalaat, dañuy wax li gën ci waxi mbindeef yi, waaye dañuy génn ci diine kem ni fett gi di génne ci sànnikaay gi, seen ngëm gi weesuwul seen i put, fu ngeen leen fekk nangeen leen ray, ndax ray leen yiw lay doon ëllëg bis-pénc ".

«يَأْتِي فِي آخِرِ الزَّمَانِ قَوْمٌ حُدَثَاءُ الأَسْنَانِ سُفَهَاءُ الأَحْلاَمِ، يَقُولُونَ مِنْ خَيْرِ قَوْلِ البَرِيَّةِ، يَمْرُقُونَ مِنَ الإِسْلاَمِ كَمَا يَمْرُقُ السَّهْمُ مِنَ الرَّمِيَّةِ، لاَ يُجَاوِزُ إِيمَانُهُمْ حَنَاجِرَهُمْ، فَأَيْنَمَا لَقِيتُمُوهُمْ فَاقْتُلُوهُمْ، فَإِنَّ قَتْلَهُمْ أَجْرٌ لِمَنْ قَتَلَهُمْ يَوْمَ القِيَامَةِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Njiitu jullit ñi Aliyun Ibn Abii Taalib yal na ko Yàlla dollee gërëm day wax ne bu ngeen ma déggee may wax jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xam leen ne duma dàkkantal duma gaaral te duma wax lu lëmu, waaye damay leeral, te it ma daanu jóge ca Asamaan moo gën a yomb ci man may wax ci Yonente bi di ko fenal, waaye bu ma leen di wax ci sama diggante ak nit ñi loolu xare la, amaana ma gaaral walla dàkkantal walla ma gaaral walla ma lëmal, dégg naa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Mujjug jamono ay xale yu ndaw ay at di ñu doyadi xel, dañuy bari lu ñuy jàng alxuraan, waaye dañuy génn ci lislaam di jéggi ay digam, kem ni fett gi di génne ci sànnikaay gi, te seenug ngëm du weesu seen i put, fu ngeen leen fekk nangeen leen ray, ndax ray leen amna ag fay ëllëg bis-pénc.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral lenn ci meloy Xawaarij yi

Nekk na ci hadiis bi ag màndarga ci màndargay Yonente gi, ndax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xibaare luy am ci xeetam ci ginnaawam, loolu daal di kem ni mu ko xibaare woon.

Lëmal ak gaaral dagan na ci xare, wor ci xare ci lëmal lay ame, te dana ame ci fiir ak lu ko niru, ci lu dul fecci kóllare ak wóolute, ndax loolu ag tere da cee rot.

Nawawii nee na: (dañuy wax li gën ci waxi mbindeef yi) maanaam: ci li feeñ ci mbir mi, niki li ñuy wax naan: kenn du àtte ku dul Yàlla, ak yu ko niru ci seenug woote jëme ci Téereb Yàlla bi.

Ibn Hajar nee na ci li mu wax ne: (du weesu seen put gi): li ñu ci namm mooy ne gëm gi saxul ci seen i xol; ndax li taxaw ci put te weesuwu ko loo lu du egg ci xol bi.

Al-Xaadii nee na: woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ne Xawaarij yi ak ñi mel ni ñoom ci bidaakat yi ak ñiy bew saa bu ñu génnee ci njiit li daal di wuute ak gisiinu mbooloo mi daal di tas mbooloo mi kon rayante ak ñoom ginnaaw bi ñu leen àrtoo moytandikuloo leen lu war lay doon.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 200) (3611).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 746) (1066).

Yataal gi (3)

النهاية في غريب الحديث والأثر (259)(866).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (20/ 264) (20/ 258).

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (6/ 58).