Skip to content

«bokk na ci ñi gën a bon ci nit ñi mooy ñi bis-pénc di ñëw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka».

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:

«bokk na ci ñi gën a bon ci nit ñi mooy ñi bis-pénc di ñëw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka».

«إِنَّ مِنْ شِرَارِ النَّاسِ مَنْ تُدْرِكُهُ السَّاعَةُ وَهُمْ أَحْيَاءٌ، وَمَنْ يَتَّخِذُ الْقُبُورَ مَسَاجِدَ».

Ahmat soloo na ko.
Tane na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ñi gën a yées ci nit ñi, te mooy ñi nga xamne saa day taxaw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka, di fa julli ak di fa jublu.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Araamalees na tabax jàkka ci kaw ay bàmmeel; ndax day sabab bokkaale.

Araamal nañu julli ci ay bàmmeel donte tabaxuñu ko; ndax jàkka aw tur la ñeel fa ñuy sujjóote doonte tabax nekku fa.

Ku jàppe bàmmeeli ñu baax ñi ay jàkka ngir di fa julli kooku ci ñi yées ci nit ñi la bokk, donte dafa foog ne jublu bàmmeel jegeñ-jegeñlu Yàlla mu kawe mi la.

Dellluwaay yi

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (6/ 394) (3844).

Yataal gi (6)

الجديد في شرح كتاب التوحيد.

لمحمد القرعاوي (ص191).

الملخص في شرح كتاب التوحيد.

لصالح الفوزان (ص176).

أحكام الجنائز.

للألباني (1/ 217).