Skip to content

«Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu».

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu».

«إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ أَنْ تُؤْتَى رُخَصُهُ، كَمَا يُحِبُّ أَنْ تُؤْتَى عَزَائِمُهُ».

Ibnu Hibbaan soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Leerarug hdiisbi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da ñuy xamal ne: Yàlla daa bëgg ñu def ay yombalam yi mu yoonal, ci woyofal àtte yi ak jaamu yi, ak yombalal ko mukallaf mi ngir ngànt -niki wàññi julli ak boole ko cib tukki-, Kem nimu bëgge ñu def ay dogoom, ci bir yu war yi; ndaxte ndigalul Yàlla ci yombal yi ak ci dogu yi benn la.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal hdiis bi: Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi, ak ne moom Yàlla mu sell mi day bëgg ñu def yi mu yoonal ci ay yomb-yomb.

Matug Sariiha ji ak teggilam jullit bi AB coono.

Dellluwaay yi

Téere bu wér bi ñeel Ibnu Hibbaan (2/ 69) (354).

Yataal gi (2)

فيض القدير (2/292).

نيل الأوطار (3/244).