"bu ñu doon jox nit ñi ci liñuy wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ".
Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"bu ñu doon jox nit ñi ci liñuy wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ".
«لَو يُعطَى النّاسُ بدَعواهُم لادَّعَى رِجالٌ أموالَ قَومٍ ودِماءَهُم، لَكِنَّ البَيِّنَةَ على المُدَّعِى، واليَمينَ على مَن أنكَرَ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne bu ñu doon jox nit ñi ngir seen i wootewoo dong ci lu dul benn firnde walla ay tegtal kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a joxe aw lay ak firnde ci li muy sàkku, bu amul aw lay ñu gaaral wootewoo ji ki ñu tuumaal, bu ko weddee dafa war a giñ daal di cay set.
Ibn Daxiixil hiid nee na: Hadiis bi cosaan la ci cosaani àtte yi, te mooy delluwaay bi gën a màgg ci wàllu xëccoo ak xuloo.
Sariiha dafa ñëw ngir aar alali nit ñi ak seen dereet ci ay caaxaan.
Àttekat bi du dellu ca lamu xam rekk waaye day dellu ci ay firnde.
Képp ku wootewoo ag wootewu gu amul lay dees ko koy delloo, moo xam ci àq yi la ak ci jëflante yi walla ci masalay gëm yi la ak xam-xam.
Yataal gi (6)
السنن الكبرى للبيهقي تحقيق التركي (21/ 242 - 243) (21243).
التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية (ص76).
شرح الأربعين النووية.
لابن عثيمين (ص328).
فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.
لعبد المحسن البدر (ص114).