"bu leen neexee ma jox leen, waaye aji-woomal amu vi cér, du caagine it ku am kàttan te man a fàggu ji".
Jële nañu ci Hubaydullaahi Ibn Hadiyyin ibn Al-Xiyaar mu wax ne:
Ñaari gaay xibaar nañu ma ne ñoom dañoo ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci aju tàggatoo ga fekk muy séddale sarax, ñu laaj ko ca, mu siggi xool nu daal di sëggaat, mu gis ñu ñu dëgër, mu daal di ne: "bu leen neexee ma jox leen, waaye aji-woomal amu vi cér, du caagine it ku am kàttan te man a fàggu ji".
أَخْبَرَنِي رَجُلَانِ أَنَّهُمَا أَتَيَا النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي حَجَّةِ الوَدَاعِ وَهُوَ يُقَسِّمُ الصَّدَقَةَ، فَسَأَلَاهُ مِنْهَا، فَرَفَّعَ فِينَا البَصَرَ وَخَفَّضَهُ، فَرَآنَا جَلْدَيْنِ، فَقَالَ: «إِنَّ شِئْتُمَا أَعْطَيْتُكُمَا، وَلَا حَظَّ فِيهَا لِغَنِيٍّ، وَلَا لِقَوِيٍّ مُكْتَسِبٍ».
Ñaari gaay dañoo ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci aju tàggatoo gu, fekk muy séddale sarax, ñu sàkku mu jox leen ci, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tàmbali di leen xool rekk, ngir xam seen melokaan, ak ndax sarax dagan na leen, walla déet? Mu gis leen ñuy ñaari gaay yu am kàttan, mu ne leen: bu ngeen bëgge de ma jox leen ci, waaye ku am alal ju ko doy amu ci ab cér, du caagine it ki am kàttanu dem fàggu ji alal, doonte amul alal ju ñu ko man a jàppe ku woomal.
Araamal nañu laaj ci nit ki woomal walla mu am kàttanu fàggu ji.
Lay coosaan ci ki ñu xamalul alal mooy ag ñàkk ak yeyoo sarax.
Am kàttan rekk du tax a ñàkk a yeyoo sarax, waaye fàww it man a fàggu ji tege ca.
Ki am kàttanu fàggu lu ko doy du dagan ci moom muy jël sarax ja di ju ñu waral; ngir fàggu ji doy na ko, kem ni aji-woomal ji doyloo ci alal ji.
Yaru Yonnente bu màgg bi ñeel jëmmi jullit bi ci teddngay bakkan, ak joxe wolif jël ak laaj ak tàyyeel.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (3/ 75) (1633).
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (5/ 99) (2598).
Yataal gi (2)
ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (23/ 210).
شرح أبي داود للعيني (6/ 374).