"ku dul sant nit du sant Yàlla"
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ku dul sant nit du sant Yàlla"
«لَا يَشْكُرُ اللَّهَ مَنْ لَا يَشْكُرُ النَّاسَ»
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne du sant Yàlla de ci li gën a bari ki nga xam ne du sant nit ci lu njekk ak lu rafet li mu ko defal, loolu nag ndaxte mbir mu ne dafa jokkoo ak meneen mi, ba yax ki nga xam ne ku aadaam mooy weddi xéewalu nit ki bañ ko a sant, kooku dana bokk ci aadaam mu weddi xéewali Yàlla ak di gàtteñlu ci sant ko ca.
Solos sant nit ñi ci seen i njekk.
Kiy xeewale dëgg mooy Yàlla mu kawe mi, mbindeef yi nag ay sabab lañu yu Yàlla mu kawe mi tàggat ñeel ku ko soob, looloo tax sant nit ñi dafa bokk ci sant Yàlla mu kawe mi.
Sant nit ñi ci seen i njekk tegtal la ci matug jikko.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 188) (4811).
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 403) (1954).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (13/ 322) (7939).
Yataal gi (2)
شرح سنن أبي داود لابن رسلان (18/ 490).
شرح سنن أبي داود للعباد (547/ 13).