"seen tur yi gënal Yàlla mooy Abdullah ak Abdur Rahmaan".
Jële nañu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"seen tur yi gënal Yàlla mooy Abdullah ak Abdur Rahmaan".
«إِنَّ أَحَبَّ أَسْمَائِكُمْ إِلَى اللهِ عَبْدُ اللهِ وَعَبْدُ الرَّحْمَنِ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne tur yi gënal Yàlla mooy góor tudd: Abdullah, walla Abdu rahmaan.
Al-Xurtubii nee na: tur yi mel ni ñaari tur yii, day yam ak ñoom, niki Abdu Rahiim, ak Abdul Malik, ak Abdus Samad, moom nag dafa gënal Yàlla ndax li mu làmboo melo wu war ci Yàlla war ci nit te mooy ag njaame, topp ñu laaf njaame gi ci Boroom bi, ba tax ni ñu tëggee tur yii nekk lu am ngëneel, kneen wax ne: xereñte gi nekk ci yam gi ñu yam ci ñaari tur yi mooy ne rotul ci Alxuraan ñu laafal baatub Abdu ci benn turu Yàlla bu dul ñaar yooyu, Yàlla mu kawe mi nee na: {lay mbir mooy ba jaamub Yàlla ba jugee di ko ñaan} mu wax ci beneen aaya ne: {jaami Yàlla miy yërëmaakoon ba} ba tay it waxam ji dana ko dëgëral: {wax leen wooleen Yàlla walla ngeen woo yërëmaakoon bi}.
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1682) (2132).
Yataal gi (1)
فتح الباري لابن حجر (10/ 570).