"amna ca Àjjana ag garab gog ki war aw fas wu ñu tàggat ba mu gaaw dana ca daw luy toll ak téeméeri at te du ko dog".
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"amna ca Àjjana ag garab gog ki war aw fas wu ñu tàggat ba mu gaaw dana ca daw luy toll ak téeméeri at te du ko dog".
«إِنَّ فِي الْجَنَّةِ شَجَرَةً يَسِيرُ الرَّاكِبُ الْجَوَادَ الْمُضَمَّرَ السَّرِيعَ مِائَةَ عَامٍ مَا يَقْطَعُهَا».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamale ne Àjjana amna ag garab gog ki war aw fas wu ñu tàggat waajal ko ngir muy rawante dana daw ca ronam ga téeméeri at te du egg ca bànqaas ba ca mujj.
Leeral yaatug Àjjana, ak màggaayu ay garabam.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 114) (6553).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2176) (2828).
Yataal gi (6)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (2/ 1289).
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (3/ 345).
تطريز رياض الصالحين.
لفيصل مُبَارَك (ص1086).