"man duma jox loxo jigéen ñi, waaye li may wax téeméeri jigéen mooy li ma wax genn jigéen
Jële nañu ci Umaymata Bintu Ruxayxata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne :
Ñëw naa ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ànd ak ay jigéen ci waa Ansaar ngir jaayante ak moom, nu ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, noo ngi jaayante ak yaw ci ne dunu bokkaale Yàlla ak dara, te dunu sàcc, dunu njaalo, te dunu Sos aw duur ci sunu diggante loxo yi ak tànk yi, te dunu la moy ci njekk, mu wax ne: "ci lu ngeen man, te àttan ko" nee na: nu ne: Yàlla ak ub Yónenteem moo nu gën a yërëm, kaay nu jaayante ak yaw, yaw Yonente Yàlla bi, Yonnente bi daal di wax ne: "man duma jox loxo jigéen ñi, waaye li may wax téeméeri jigéen mooy li ma wax genn jigéen, walla moo ngi mel ni li ma wax genn jigéen".
أَتَيْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي نِسْوَةٍ مِنَ الْأَنْصَارِ نُبَايِعُهُ، فَقُلْنَا: يَا رَسُولَ اللَّهِ، نُبَايِعُكَ عَلَى أَلَّا نُشْرِكَ بِاللَّهِ شَيْئًا، وَلَا نَسْرِقَ، وَلَا نَزْنِيَ، وَلَا نَأْتِيَ بِبُهْتَانٍ نَفْتَرِيهِ بَيْنَ أَيْدِينَا وَأَرْجُلِنَا، وَلَا نَعْصِيَكَ فِي مَعْرُوفٍ، قَالَ: «فِيمَا اسْتَطَعْتُنَّ، وَأَطَقْتُنَّ» قَالَتْ: قُلْنَا اللَّهُ وَرَسُولُهُ أَرْحَمُ بِنَا، هَلُمَّ نُبَايِعْكَ يَا رَسُولَ اللَّهِ، فَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «إِنِّي لَا أُصَافِحُ النِّسَاءَ، إِنَّمَا قَوْلِي لِمِائَةِ امْرَأَةٍ كَقَوْلِي لِامْرَأَةٍ وَاحِدَةٍ، أَوْ مِثْلُ قَوْلِي لِامْرَأَةٍ وَاحِدَةٍ».
Umaymata Bintu Ruxayxata yal na ko Yàlla dollee gërëm day nettali ne: dafa ñëw ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ànd ak ay jigéen ci waa Ansaar di jaayante ak moom ci ne duñu bokkaale Yàlla ak dara, duñu sàcc, duñu njaalo, duñu sos aw duur ci diggante seen loxo yi ak seen tànk yi, te duñu ko moy ci njekk, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: Ci lu ngeen man, te àttan ko. Nu ne: Yàlla ak yonenteem bi moo nu gën a yërëm, kaay nu jaayante ak yaw, yaw Yonnente Yàlla bi ci saafonte ak sunuy loxo, kem ni muy def ak góor ñi, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: Man duma jox loxo jigéen ñi, waaye sama wax ak samag jaayante ñeel téeméeri jigéen moo ngi mel ni li may wax ak genn jigéen.
Leeral melow jaayanteg Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak jigéen ñi.
Araamal nañu jox loxo jigéen gu dul kojug armal.
Digley Sariiha yi dafa aju ci kàttan ak man.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 247) (1597).
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (7/ 149) (4181).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (4/ 128) (2874).
Yataal gi (1)
ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (32/ 263).