Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc musul a xeex ak i nit ba keroog mu leen di woo.
Jële nañu ci Ibnu Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne :
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc musul a xeex ak i nit ba keroog mu leen di woo.
مَا قَاتَلَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَوْمًا قَطُّ حَتَّى يَدْعُوَهُمْ.
Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc musul a tàmbalee xeex aw nit ba keroog lu leen di njëkk a woo ci lislaam, bu ñu wuyuwul wooteem bi mu xeex leen.
Sàrtal nañu woote ci lislaam laata xeex bi bu dee lislaam jotu leen.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na woote ci lislaam, bu ñu bañee mu gaaral leen lempo, bu ñu bañee mu xeex leen, kem ni mu ñëwe ci yeneen hadiis.
Xereñte gi nekk ci jihaad mooy nit ñi dugg ci lislaam, waaye du xemmem leen a def jaam ak seen i alal ak seen réew
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (4/ 16) (2105).
Téere bu mag bi Al-Bayhaqii def ci Sunna yi (9/ 181) (18232).
Yataal gi (1)
تحفة الأحوذي (5/ 130).