Nekkoon nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nu nekk ay xale yuy bëgg a mat, nu jang ngëm laata nuy jàng alxuraan, topp nu jàng alxuraan, nu dollikoo ca ag ngëm.
Jële nañu ci Jundub ibn Abdulla yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Nekkoon nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nu nekk ay xale yuy bëgg a mat, nu jang ngëm laata nuy jàng alxuraan, topp nu jàng alxuraan, nu dollikoo ca ag ngëm.
كُنَّا مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَنَحْنُ فِتْيَانٌ حَزَاوِرَةٌ، فَتَعَلَّمْنَا الإِيمَانَ قَبْلَ أَنْ نَتَعَلَّمَ القُرْآنَ، ثُمَّ تَعَلَّمْنَا القُرْآنَ، فَازْدَدْنَا بِهِ إِيمَانًا.
Jindub ibn Abdulla yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa wax ne: nekkoon nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nu nekkoon ay ndaw yuy bëgg a mat, di ñu am kàttan te dëgër, nu jàng ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc gëm Yàlla laata nuy jàng alxuraan, topp nu jàng alxuraan; nu dollikoo ca ag ngëm.
Leeral ne gëm day yokk di wàññeeku.
Toftale yi gën a tey bu ñu dee yar ndaw ñi, ak xer ci feesal ci ñoom gëm Yàlla.
Alxuraan day dolli ngëm, di leeral xol, di yaatal dënn.
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (1/ 42) (61).
Yataal gi (2)
مشارق الأنوار الوهاجة ومطالع الأسرار البهاجة في شرح سنن الإمام ابن ماجه (2/ 255).
مرشد ذوي الحجا والحاجة إلى سنن ابن ماجه والقول المكتفى على سنن المصطفى (1/ 227).