"ku def dara ba ab gétéñ war ca ñu gaaw koo mbugal ci àdduna, Yàlla moo gën a maanu ba du mbugalaat jaamam bi ca allaaxira
Jële nañu ci Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ku def dara ba ab gétéñ war ca ñu gaaw koo mbugal ci àdduna, Yàlla moo gën a maanu ba du mbugalaat jaamam bi ca allaaxira, waaye ku def luy waral ab gétéñ Yàlla suturaal ko jéggal ko, Yàlla moo gën a tedd ba du delluwaat ci dara lu mu jéggale woon".
«مَنْ أَصَابَ حَدًّا فَعُجِّلَ عُقُوبَتَهُ فِي الدُّنْيَا فَاللَّهُ أَعْدَلُ مِنْ أَنْ يُثَنِّيَ عَلَى عَبْدِهِ العُقُوبَةَ فِي الآخِرَةِ، وَمَنْ أَصَابَ حَدًّا فَسَتَرَهُ اللَّهُ عَلَيْهِ وَعَفَا عَنْهُ فَاللَّهُ أَكْرَمُ مِنْ أَنْ يَعُودَ فِي شَيْءٍ قَدْ عَفَا عَنْهُ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne ku def ag moy ci moy yiy waral gétéñu sariiha, niki njaalo, ak sàcc, ñu mbugal ko teg ci moom gétéñu sariiha ci àdduna, kon gétéñ googu day far bàkkaar ba, ba tax mbugal da koy wàcc ca allaaxira, ndax Yàlla moo gën a tedd ëpp yërmànde ba du booleel jaamam bi ñaari mbugal, ku Yàlla suturaal ci àdduna nag, te mbugalu ko ci bàkkaar boobu, mu baal ko jéggal ko, kon Yàlla moo gën a tedd gën a tabe ba tax du dellu ci di mbugale ci bàkkaar bu mu baale woon jéggale ko.
Màggug mànduteg Yàlla ak teddngaam ak yërmàndeem.
Taxawal gétéñ gi ci àdduna day far bàkkaar bi.
Jaadu na ci ku tàbbi ci bàkkaar buy waral gétéñ mu suturaal boppam ci suturag Yàlla, te gaaw tuub tuub gu sell.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 312) (2626).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (3/ 627) (2604).
Yataal gi (3)
مرشد ذوي الحجا والحاجة إلى سنن ابن ماجه والقول المكتفى على سنن المصطفى (15/ 224).
التيسير بشرح الجامع الصغير (2/ 399).
فيض القدير (6/ 65).