Skip to content

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan génn ci wanag day wax: "Xufraanaka".

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan génn ci wanag day wax: "Xufraanaka".

أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ إِذَا خَرَجَ مِنَ الغَائِطِ قَالَ: «غُفْرَانَكَ».

Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan faj aajoom ba génn ci wanag wi day wax: maa ngi lay ñaan(sa njéggal) yaw Yàlla.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sopp nañu ñu wax: "Xufraanaka" ginnaaw bi ñu génnee ca barabu fajukaayu aajo ba.

Yonnente bi day jéggalu Boroomam ci gépp anam.

Nee nañu sababus jéggalu gi ginnaaw faj aajo: mooy gàtteñlu gi ci sant xéewali Yàlla yu bari yi, te bokk na ca génnug lor gi, may sàkku sa njéggal ci fajug aajo gi ma soxlaal wolif tudd la.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (1/ 24) (30).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (1/ 57) (7).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (1/ 200) (300).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (42/ 124) (25220).

Yataal gi (4)

توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (1/ 351).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (1/ 397).