Skip to content

"bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla

Jële nañu ci Abdulla ibn Busrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay dafa ñëw ci Yonnente bi, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi! Yi lislaam santaane dafa bari ci nun, ndax am na bunt bu dajale bu nu man a jàpp? Mu wax ne:

"bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla". Ñëw na ci beneen nettali: ci Hadiisu Muhaas ibn Jabal yal na ko Yàlla dollee gërëm: bi ma mujjee teqalikoo ak Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dama ne ko: yan jëf moo gën te gën a jege Yàlla? Mu ne: "nga faatu fekk sa làmmiñ moo ngi tooy ci tudd Yàlla mu màgg mi".

«لاَ يَزَالُ لِسَانُكَ رَطْبًا مِنْ ذِكْرِ اللَّهِ». وفي رواية: مِنْ حَدِيثِ مُعَاذِ بْنِ جَبَلٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ: آخِرُ مَا فَارَقْتُ عَلَيْهِ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنْ قُلْتُ: أَيُّ الأَعْمَالِ خَيْرٌ وَأَقْرَبُ إِلَى اللَّهِ؟ قَالَ: «أَنْ تَمُوتَ وَلِسَانُكَ رَطْبٌ مِنْ ذِكْرِ اللَّهِ عَزَّ وَجَلَّ».

Ahmad, ak At-Tirmisiyyu, ak Ibn Maaja ak Ibn Hibbaan ñoo ko soloo.
Wér na
Leeral gi

Jenn waay dafa jàmbat Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ne naafila yi dafa bari ci moom ba tax mu lott ci ngir néew kàttanam, mu laaj Yonnente bi ngir mu tegtal ko jëf ju néew juy indi yool yu bari ngir mu jàpp ci. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tektal ko ci muy Sax di tooyal làmmiñam ci tudd Yàlla ci bépp jamono ak ci gépp anam; ci sàbbaal ak sant ak jéggalu ak ñaan ak yu ko niru.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu saxoo tudd Yàlla mu kawe mi.

Bokk na ci màggug ngëneelu Yàlla mu yombal sababi yiw yi.

Gënlaanteg jaam ñi mingi ci seen cér yi ci bunti mbaax yi ak yiw yi.

Baril tudd Yàlla ci làmmiñ di sàbbaal ak di sant ak sikar ak di kàbbar ak yu dul yooyu, ànd ak mu dëppoo ak xol bi day taxaw taxawaayu ay naafila yu bari ci jaamu yi.

Sàmmonteek Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel aji-laaj ji ci tontu laaj bu nekk ca la méngoo ak moom.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 318) (3375).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (4/ 707) (3793).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (29/ 226) (17680).

Yataal gi (8)

جامع العلوم والحكم في شرح خمسين حديثا من جوامع الكلم.

لابن رجب الحنبلي (2/ 510).

التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية.

لإسماعيل الأنصاري (ص104).

فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.

للنووي وابن رجب (ص154).

الأحاديث الأربعون النووية وعليها الشرح الموجز المفيد.

لعبد الله بن صالح المحسن (ص93).