Skip to content

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a rafet jikko ci nit ñi.

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a rafet jikko ci nit ñi.

كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَحْسَنَ النَّاسِ خُلُقًا.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a mat jikko ci nit ñi, mbooleem jikko yu rafet yi moo ca jiitu, ci wax ju teey, ak jëf ju yiw, ak béllil xar kanam, ak téye lor te muñ ko ci ñeneen ñi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Matug jikkoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mooy royukaay bu mat bi ci rafet jikkó.

Ñaaxe ci roy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci rafet jikkó.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 45) (6203).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1805) (2310).

Yataal gi (8)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 670).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (1/ 524).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (9/ 57).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 556).