Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

12 of 732 cards

Clear filters
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli day teg loxoom -walla yéereem- ci gémmeñam, daal di suufeel -walla mu téye- ci kàdoom.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
"man yónniwuñu ma ngir may rëbbe, waaye dañu maa yónni ngir yërmànde".
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bi muy faatu bàyyiwul benn Diinaar walla Dërëm du caagine jaam bu góor walla jigéen du caagine dara, lu dul fasam wu weex wi, ak ngànnaayam, ak suuf su mu def ab sarax.
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
Am mbooloo ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dañoo laaj soxnay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ay jëfam ci li nëbbu? Am ci ñoom ku ne: man du ma takk soxna, keneen ne: man duma lekk ndawal, keneen ne: man duma nelawati ci kaw lal, Yonente bi daldi sant Yàlla tagg ko, wax ne: "ana lan moo dal aw nit ba ñuy wax lii ak lii? man de damay julli di nelaw, di woor di dog, di takk soxna, ku bañ sama yoon wi bokkul ci man".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan julli fajar day toog fa mu jullee ba keroog jant bi di fenk ba leer, mu ne: daawul jug ca jullikaayam ba mu jullee suba walla njël, ba keroog jant bi di fenk, bu jant bi fenkee mu jug, ñu daan waxtaan di jël ca mbiri ceddo ga, ñuy ree muu muuñ.
Wér na Muslim soloo na ko.
"yaw Yàlla sama Boroom man dey nit rekk laa kepp ku ma ŋàññ ci jullit ñi walla ma rëbb ko walla ma dóor ko maa ngi lay ñaan nga defal ko ko ag sell ak ug yërmànde".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yaw yaayu jullit ñi, wax ma jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu ne ma: xanaa doo jàng Alxuraan? Ma ne ko: ahakay, mu ne ma: jikkóom moo doon.
Wér na Muslim soloo na ko ci ab Adiis bu gudd.
Njabootu Muhammat de yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc diirub bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina masu ñoo suur ci ñamu dugub ñatti guddi yu toftaloo, ba ni mu faatoo.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.