Skip to content

gis naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu tuur-ndox, topp mi jàppu daal di masaa ci kaw ay Saŋam

Jële nañu ci Ibraahiima An-Naxahii mu jële ci Hammaam ibn Al-Haaris mu wax ne:

Jariir dafa saw, topp mu jàppu daal di maasaa ci kaw ay Saŋam, ñu nebko: nii ngay def? Mu ne: waaw, gis naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu tuur-ndox, topp mi jàppu daal di masaa ci kaw ay Saŋam. Al-Ahmas nee na: Ibraahiima nee na: hadiis bii daleen doon yéem; ndax tuubug Jariir ginnaaw bi Al-Maa-ida wàccee la.

بَالَ جَرِيرٌ، ثُمَّ تَوَضَّأَ، وَمَسَحَ عَلَى خُفَّيْهِ، فَقِيلَ: تَفْعَلُ هَذَا؟ فَقَالَ: نَعَمْ، رَأَيْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بَالَ، ثُمَّ تَوَضَّأَ وَمَسَحَ عَلَى خُفَّيْهِ. قَالَ الأَعْمَشُ: قَالَ إِبْرَاهِيمُ: كَانَ يُعْجِبُهُمْ هَذَا الحَدِيثُ؛ لِأَنَّ إِسْلَامَ جَرِيرٍ، كَانَ بَعْدَ نُزُولِ المَائِدَةِ.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Jariir ibn Abdulla yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa tuur-ndox tupp mu jàppu daal di yem ci masaa kaw ay Saŋam te raxasul ay tànkam, ñi ko wër ne ko: nii ngay def?! Mu ne: waaw, gis naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu tuur-ndox, topp mu jàppu daal di masaa ci kaw ay kaw Saŋam. Te Jaabir dafa yeexoon a tuub muy ginnaaw bi Saaru Al-Maa-ida bi nga xam ne ci aayab njàppu nekk, ngir junj ci loolu ne masaa ci kaw ay Saŋ aaya boobu nasaxalu ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xérug sahaaba yi ak ña leen topp ci roy sunnas Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

An-Nawawii nee na: ñi ñuy jël seenug dëppoo dëppoo nañu ci ne masaa ci ay Saŋ dagan na, ci tukki ak ak ci teew, moo xam ngir aajo ngir walla leneen, ba sax dagan ci jigéen gi taqoo ak këram ak lompañ gi dul dox.

Ngëneelu Jariir ibn Abdulla yal na ko Yàlla dollee gërëm ci li mu nekk ku yaatu dënn, di muñ li ko ndongaam yi di weddi, doonte ñoom ñoo juum ci loolu.

Delloo képp kuy weddi masaa ci ay Saŋ di wootewoo ne dañu ko a nasaxal; ndaxte hadiisu Jariir bi moo mujj aayab jàppu bi.

Leeral ne jaadu na ci ku ñi weddi ci moom dara, te mu jàppoon ag wéram mu bañ a mere ki ko weddi, te wàqante ak moom ci kem la mu njort, waaye da koy leeralal sukkandikukaayam ci loolu ca na mu gën a rafete.

Tegtaloo ci taarix bu ñu ko aajowoo.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 87) (387).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 227) (272).

Yataal gi (1)

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (7/ 39).