Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono.
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono.
كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَذْكُرُ اللهَ عَلَى كُلِّ أَحْيَانِهِ.
Aysatu yaayu way-gëm ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xéroon lool ci tudd Yàlla mu kawe mi, ak ne daa na tudd Yàlla ci bépp jamono ak bérab ak anam.
...:
Sàrtaluñu ci tudd Yàlla laab ci toj gu ndaw mbaa toj gu mag.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa saxoon ci tudd Yàlla .
Ñaaxe ci tudd Yàlla mu kawe mi lu bari ci bépp jamono ngir roy ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, lu dul ci anam yi ñuy tere ku ci tudd Yàlla, niki jamanoy faj aajo.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 282) (373).
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 68).
(1/ 129).
Yataal gi (6)
توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.
للبسام (1/ 315).
فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (1/ 273).
مجموع فتاوى ومقالات.
لابن باز (26/ 17).