Skip to content

"loo xam ne lu bareem day màndiloo kon lu néewam dafa araam".

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"loo xam ne lu bareem day màndiloo kon lu néewam dafa araam".

«مَا أَسْكَرَ كَثِيرُهُ فَقَلِيلُهُ حَرَامٌ».

Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Tane na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne bépp naan walla lekk buy yóbb xel bu dee jëfandiku na ñu ca lu bari, kon jëfandikoo ci lu néew dafa araam donte yóbbuwul xel mi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sariiha day sàmm xeli nit ñi.

Warees naa fatt wépp yoon wuy jëme ci bàkkaar, maanaam tëj lépp luy yóbbe ci ñaawtéef yooyu.

Araamal nañu luy màndiloo donte dafa néew; ndax day taxa màndi.

Bu dee lu néew li ak lu bari li dara du ci màndiloo kon araamul.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (5/ 523) (3681).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 442) (1865).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (4/ 475) (3393).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (23/ 51) (14703).

Yataal gi (3)

فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام (5/ 418).

شرح سنن أبي داود للعباد (417/ 9).

النهاية في غريب الحديث والأثر (437).