Skip to content

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc Saahu ndox daan na ko sang janaba Mudd it daan na ko jàppu.

Jële nañu ci Safiinata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc Saahu ndox daan na ko sang janaba Mudd it daan na ko jàppu.

كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يُغَسِّلُهُ الصَّاعُ مِنَ المَاءِ مِنَ الجَنَابَةِ، وَيُوَضِّئُهُ المُدُّ.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na sangu janaba ci Saah, daan jàppoo benn Mudd. Saah mooy ñenti Mudd, Mudd: mooy luy toll ci feesal ñaari ténqi nit ku yem jëmm.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yoonalees nañu sakkanal nduxum njàppu mi ak sangu mi, te bañ a yàq doonte dafa yomb.

Sopp nañu néewal ndoxum jàppu mi ak mu sangu mi ci kem aajo ja, ndax lii mooy njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Li ñu ci jublu mooy matale njàppu mi ak sangu mi ànd ak sàmmoonte ak sunna yi ak teggin yi ci lu dul yàq walla ŋott, sàmmoonte it ak waxtu wi ak barig ndox mi ak néewaayam ak yeneen.

Dees na boyal janaba ci képp ku génne Maniyu walla mu sëy, dees koo tudde loolu ngir li boroomam di moytu julli ak jaamu yi ba keroog muy laab.

Saah: ab natt la gu ñu xam, li ñu ci namm mooy Saahu Yonnente bi, peeseem di toll ci (480)Misxaal ci pepp mu baax, bu dee ci liitar (3liitar).

Mudd: ag nattukaayu Sariiha la, te mooy feesal ñaari ténqi nit ku yem, bu ko feesalee tàllal loxoom, Mudd mooy ñenti Saah ci dëppoog woroom xam-xami fiq yi, ñu koy nattale ci(750) mili liitar.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 258) (326).

Yataal gi (1)

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (8/ 52).