Skip to content

jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw».

Jële na ñu ci Hakiim Ibn Hisaam -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne:

Damaa wax: yaw Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaar ma ci bir yi ma daan def ca ceddo ga, ci sarax ak goreel, ak jokk mbokk, ndax am na yool? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw».

قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، أَرَأَيْتَ أَشْيَاءَ كُنْتُ أَتَحَنَّثُ بِهَا فِي الجَاهِلِيَّةِ مِنْ صَدَقَةٍ أَوْ عَتَاقَةٍ، وَصِلَةِ رَحِمٍ، فَهَلْ فِيهَا مِنْ أَجْرٍ؟ فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَسْلَمْتَ عَلَى مَا سَلَفَ مِنْ خَيْرٍ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne yéefar bi bu jébbaloo dees na ko fay ab yool ca lamu defoon ca ceddo ga lu jiitu Lislaam ci ay jëf yu baax ci sarax, ak goreel jaam, ak jokk mbokk.

Maanaay baat yi

أتحنث: أتعبد.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal hdiis bi: Yéefar bi deesu ko fay ay jëf yu baaxam ca allaaxira bu dee daa faatu cig kéefar.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 114) (1436).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 113) (123).

Yataal gi (5)

المفهم (1/332).

شرح النووي على مسلم (2/140).

عمدة القاري شرح صحيح البخاري (22/ 96).

فتح الباري لابن حجر (3/ 302).

البحر المحيط الثجاج (3/499).