Njabootu Muhammat de yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc diirub bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina masu ñoo suur ci ñamu dugub ñatti guddi yu toftaloo, ba ni mu faatoo.
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Njabootu Muhammat de yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc diirub bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina masu ñoo suur ci ñamu dugub ñatti guddi yu toftaloo, ba ni mu faatoo.
مَا شَبِعَ آلُ مُحَمَّدٍ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مُنْذُ قَدِمَ المَدِينَةَ مِنْ طَعَامِ البُرِّ ثَلاَثَ لَيَالٍ تِبَاعًا، حَتَّى قُبِضَ.
Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne waa kër Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc diirub bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina suuruñu ci ci lekk dugub ñatti fan yu toggaloo ba ni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc faatoo.
Leeral ni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak waa njabootam nekk woon ci néewug dund, ndax dëgg-dëggi dund mooy dundug allaaxira.
Ibn Hajar nee na: liy feeñ mooy ne sababug seenug ñàkk a suur li ëpp co li sabab mooy néewug li nekk fi ñoom, ci ne ñoom daan nañu am waaye dañuy gënale ñeneen ci seen bopp.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 75) (5416).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2282) (2970).
Yataal gi (2)
المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (7/ 129).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (45/ 129).