Skip to content

"misaalu boroom Alxuraan dafa mel ni boroom giléem gi ñu yeew, bu sàmmontee ak moom dana ko téye, waaye bu ko bàyyee mu dem yoonam".

Jële nañu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"misaalu boroom Alxuraan dafa mel ni boroom giléem gi ñu yeew, bu sàmmontee ak moom dana ko téye, waaye bu ko bàyyee mu dem yoonam".

«إِنَّمَا مَثَلُ صَاحِبِ القُرْآنِ كَمَثَلِ صَاحِبِ الإِبِلِ المُعَقَّلَةِ، إِنْ عَاهَدَ عَلَيْهَا أَمْسَكَهَا، وَإِنْ أَطْلَقَهَا ذَهَبَتْ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day niróole kiy jàng Alxuraan te miin njàng mi -moo xam day xool ci kaamil bi walla day jàng ci mokkalam- ak boroom giléem gi ñu yeew ci buum gi ñuy takk ci tànku gileem bi, bu sàmmontee ak moom dana wéy ci téye ko, bu bàyyee buum gi mu dem daal di rëcc, kon boroom Alxuraan ji bu jugee ci di ko jàng kon dana koy fàttaliku, bu ca jugul nag kon dana ko fàtte; fii ak kollarante ga ma nga fa rekk kon wattu ga dana fa nekk.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci kollarante ak Alxuraan ak di ko jàng, ak moytu ko a fàtte.

Sax ci jàng Alxuraan day tàggat làmmiñ wi di yombal jàng gi, bu ko gàddaaye nag kon jàng gi day diis daal di jafe ci moom.

Al-Xaadii nee na: maanaam "boroom Alxuraan" mooy: ki ko miin, àndandoo (al-Musaahabatu) mooy, : miinante, te ci lañu jële: diw àndandoo (Saahibu) diw la, ak waa (Ashaabu) Àjjana , ak waa (Ashaabu) Sawara.

Bokk na ci anami woote yi di joxe ay misaal.

Ibn Hajar nee na: dafa jagleel giléem cig tudd; ndax mooy rab wiy miin nit wi dàqa rëcc, te jàpp ko ginnaaw ba mu rëccee lu jafe la.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 193) (5031).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 543) (789).

Yataal gi (6)

شرح صحيح مسلم.

للنووي (6/ 77).

فيض القدير شرح الجامع الصغير.

لعبدالرؤوف المناوي (3/ 3).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (13/ 12).