"ku bàyyi ñatti àjjuma ngir woyofal ko Yàlla dana tàppe xolam".
Jële nañu ci Abul Jahdi Ad-Damrii yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu bokkoon ci Sahaabay Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ku bàyyi ñatti àjjuma ngir woyofal ko Yàlla dana tàppe xolam".
«مَنْ تَرَكَ ثَلَاثَ جُمَعٍ تَهَاوُنًا بِهَا طَبَعَ اللَّهُ عَلَى قَلْبِهِ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day artu ki bàyyi jullig àjjuma, ak ne ku bàyyi jullig àjjuma ñatti yoon ngir woyofal ak gàtteñlu ci lu dul ngànt, Yàlla dana kaste muur xolam bi ci tere yiw egg ca.
Ibnul Munsir nettali na ag dëppoo ci ne jullig àjjuma faratay jëmm la.
Tëkku ñeel na ki bàyyi jullig àjjuma ngir woyofal ko ci ne Yàlla dana tàppe xolam bi.
Ku bàyyi àjjuma ngir ngànt kooku du dugg ci tëkku gi.
Sawkaanii nee na: waxam ji: (ñatti àjjuma), jamtal na ne li ñu ci namm mooy mu bàyyi ko kaaremaa moo xam àjjuma yi dafa tegaloo walla mu teqalikoo, ba ci sax bu bàyyi woon ci at mu nekk jenn àjjuma kon Yàlla dana tàppe xolam ginnaaw bi mu matee ñatti àjjuma te mooy li feeñ ci hadiis bi, jamtal na it ne li ñu ci namm mooy ñatti àjjuma yu tegaloo.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 284) (1052).
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (1/ 630) (500).
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (3/ 88) (1369).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (2/ 213) (1125).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (24/ 255) (15498).
Yataal gi (2)
النهاية في غريب الحديث والأثر (557).
شرح سنن أبي داود للعباد (134/ 3).