Skip to content

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na raxas, walla daan na sangu ci Saah ba ci juróomi Mudd, (mooy ñaari loxoom bamu fees) daan jàppu ci benn Mudd.

Jële nañu ci Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na raxas, walla daan na sangu ci Saah ba ci juróomi Mudd, (mooy ñaari loxoom bamu fees) daan jàppu ci benn Mudd.

كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَغْسِلُ، أَوْ كَانَ يَغْتَسِلُ، بِالصَّاعِ إِلَى خَمْسَةِ أَمْدَادٍ، وَيَتَوَضَّأُ بِالْمُدِّ.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na sangu janaba ci Saah ba ci juróomi Mudd, daan jàppoo benn Mudd. Saah mooy ñenti Mudd, Mudd: mooy luy toll ci feesal ñaari ténqi nit ku yem cig jëmm.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yoonalees na sakkanal nduxum njàppu mi ak sangu mi, te bañ a yàq donte dafa yomb.

Sopp nañu néewal ndoxum jàppu mi ak mu sangu mi ci kem aajo ja, ndax lii mooy njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Li ñu ci jublu mooy matale njàppu mi ak sangu mi ànd ak sàmmonte ak sunna yi ak teggin yi ci lu dul yàq walla ŋott, sàmmonte it ak waxtu wi ak barig ndox mi ak néewaayam ak yeneen.

Dees na tudde janaba képp ku génne Maniyu walla mu sëy, dees koo tudde loolu ngir li boroomam di moytu julli ak jaamu yiy aajowoo ag laab.

Saah:ab natt la gu ñu xam,li ñu ci namm mooy Saahu Yonnente bi,ag di toll ak(480)Misxaal ci pepp mu baax,bu dee ci liitar (3liitar).

Mudd: ag nattukaayu Sariiha la, te mooy feesal ñaari ténqi nit ku yem, bu ko feesalee tàllal loxoom, Mudd mooy ñenti Saah ci dëppoog woroom xam-xami fiq yi, ñi koy nattale ci(750) mili liitar.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 51) (201).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 258) (325).

Yataal gi (12)

توضيح الأحكام.

للبسام (1/ 250).

سُبل السلام.

للصنعاني (1/ 79 ).

فتح ذي الجلال والإكرام.

لابن عثيمين (1/ 212).

منحة العلَّام.

لعبد الله الفوزان (1/ 186).

منار القاري شرح مختصر صحيح البخاري.

لحمزة قاسم (1/ 272).

تحقيق مقدار المد والصاع النبوي.

للدكتور عبدالمحسن القاسم.