Skip to content

Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- budaan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba da daan wax: «samihal Laahu liman hamidahu

Jële nañu ci Ibn Abii Awfaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- budaan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba da daan wax: «samihal Laahu liman hamidahu, Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, mil-as samaawaati wa mil-al ardi wa mil-a maa sita min say-in bahdu».

كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا رَفَعَ ظَهْرَهُ مِنَ الرُّكُوعِ قَالَ: «سَمِعَ اللهُ لِمَنْ حَمِدَهُ، اللَّهُمَّ رَبَّنَا لَكَ الْحَمْدُ، مِلْءَ السَّمَاوَاتِ وَمِلْءَ الْأَرْضِ وَمِلْءَ مَا شِئْتَ مِنْ شَيْءٍ بَعْدُ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba ci julli gi, day wax: "samihal Laahu liman hamidahu", maanaam: ku sant Yàlla mu kawe mi, Yàlla dana ko wuyu nangul ko cantam ak taggam, topp mu sant Yàlla ci wax: "Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, mil-as samaawaati wa mil-al ardi, wa mil-a maa sita min say-in bahdu", cant gu fees asamaan yi ak suuf yi ak li ci séen diggante, tey fees lépp lu soob Yàlla.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral li ñu sopp ci kiy julli mu wax ko bu yëkkatee boppam jóge ca sujjóot ba.

Yoonal nañu yamoo ak dal ginnaaw bu ñu siggee ca rukoo ba; ndax manuta wax sikar bii ludul bu yamoo ba dal.

Sikar bii nag lu ñu yoonal la ci mbooleem julli yi moo xam farata la walla naafila.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 346) (476).

Yataal gi (1)

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (11/ 114).