Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

14 of 732 cards

Clear filters
Moom daana kàbbar ci bépp jullig farata ak bu dul moom, ci koor ak bu dul koor, bu dee jug kàbbar, bu dee rukoo kàbbar, daal di wax: samihal Laahu liman hamidahu, daal di wax it: Rabbanaa wa lakal hamdu, bala moo sujjóot, bu dee rot jëm ci sujjóot ba daal di kàbbar, buy yëkkati boppam ci sujjóot daal di kàbbar, bu dee jug ci toogaayu ñaari ràkka yi daal di kàbbar, loolu lay def ci ràkka yépp, ba julli gi jeex, ba mu wëlbatikoo daal di wax ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, maa leen gën a niroole jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.
Wér na Muslim soloo na ko.
«bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar, bu waxee: (xayril maxduubi halayhim wa laddaalliina) [Al-Faatiha: 7], nangeen wax: Aamiin, Yàlla dana leen nangul, bu kàbbaree daal di rukoo nangeen kàbbar te rukoo, imaam bi moo leen di njëkk a rukoo, moo leen di njëkk a siggi Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu waxee: samihal Laahu liman hamidahu, nangeen wax Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, Yàlla dana leen dégg, Yàlla dafa wax ci nettalig Yonnente bi: samihal Laahu liman hamidahu, bu kàbbaree sujjóot nangeen kàbbar sujjóot, imaam moo leen di njëkk a sujjóot njëkk leen a siggi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "bee ci bee, bu nekkee ca toogaay ba kenn ci yéen na njëkk a wax: attahiyyaatu attayyibaatu assalawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an laa iLaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan abduhu wa rasuuluhu».
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi, naka noonu it daan na leen yëkkati bu daan kàbbar ngir rukóo, ak bu daan siggi ca rukóo ba, ak bu daan yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: "samihal Laahu liman hamidahu", daawul def loolu nag ca sujjóot ba.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- budaan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba da daan wax: «samihal Laahu liman hamidahu, Allaahumma Rabbanaa lakal hamdu, mil-as samaawaati wa mil-al ardi wa mil-a maa sita min say-in bahdu».
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ma taaya fekk samay ténq moo ngi ci diggante ñaari ténqam, kem ni mu ma xamale saaru Alxuraan: "Attahiyyaatu lil Laahi, assakiyyaatu lil Laahi, attayyibaatus salawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan nabiyu,wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahis saalihiina,ashadu an laa ilaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu". Nekk na ci yeneen baat: "Yàlla mooy jàmm, bu kenn ci yéen toogee ci julli na wax: "Attahiyyaatu lil Laahi, assakiyyaatu lil Laahi, attayyibaatus salawaatu lil Laahi, assalaamu halayka ayyuhan nabiyu, wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahis saalihiina, bu ko waxee jot na dal na bépp jaam bu sell ci asamaan ak suuf, ashadu an laa ilaaha illal Laahu wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu, topp mu tànn ci ñaan yi lu ko soob".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dugg na ci jàkka ji jenn waay daal di dugg julli ñaari ràkka, daal di nuyu Yonente bi, mu fay ko, daal di ne ko: "demal julli waat, yaw julliwóo", mu dellu julli waat namu jullee woon, daal di nuyu Yonente bi , mu ne ko: "dellul julli waat yaw julliwóo " ñatti yoon, mu ne ko: giñ naa ci ki la yónni ci dëgg manuma lu dul lii, xamal ma, mu ne ko: "boo jugee di julli, nanga kàbbar, topp nga jàng li jàppandi ci yaw ci Alxuraan, topp nga rukkoo ba dal, nga siggi ba yamoo ca taxaw ga, topp nga sujjóot ba dal, topp nga siggi ba yamoo ca toogaay ga, defal loolu ci sa julli gi yépp".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Doon naa gis Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram, ak ci càmmooñam, ba may gis weexitu lexam.
Wér na Muslim soloo na ko.