"xolu mag du deñ di nekk waxambaane ci ñaar: ci bëgg àdduna ak mébét yu gudd".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"xolu mag du deñ di nekk waxambaane ci ñaar: ci bëgg àdduna ak mébét yu gudd".
«لاَ يَزَالُ قَلْبُ الكَبِيرِ شَابًّا فِي اثْنَتَيْنِ: فِي حُبِّ الدُّنْيَا وَطُولِ الأَمَلِ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne màggat mi day màgg yaramam di lompañ, waaye xolam day nekk waxambaane ci bëgg ñaar: Bi ci njëkk: bëgg àdduna ci barig alal. Ñaareel bi: dund gu gudd ak ay mébét.
Leeral li mooñaale nit, te mooy bëgg àdduna ak ay mébét yu gudd.
Junj jëm ci ŋàññ ay mébét yu gudd, ak xér ci dajale alal, loolu nag day waral waajal dee ak ngëneelu saraxe ñeel aji-woomal ji, ak fegu ñeel aji-ñàkk ji.
Li doomu Aadama gën a bëgg ci mbir yi mooy boppam, day xemmeem des fi, ba tax muy bëgg gudd fan, ak bëgg alal; ndaxte sabab la ci saxug wér ak bànneexu, ba saa bu yégee ne loolu moo ngi bëgg a jeex ak bëggam ci loolu day gën a tar, muy xemmeem mu sax ba fàww.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 89) (6420).
Yataal gi (2)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (20/ 36).
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (9/ 242).