Tënkal nañ nu waxtu ngir jemp ay mustaas, ak lelli ay we, ak suqi poqtaan, ak wat karawi naq, ci ñu bañ ko a bàyyi lu ëpp ñent-fukki guddi.
Jële nañu ci Anas Ibn Maalik, yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Tënkal nañ nu waxtu ngir jemp ay mustaas, ak lelli ay we, ak suqi poqtaan, ak wat karawi naq, ci ñu bañ ko a bàyyi lu ëpp ñent-fukki guddi.
وُقِّتَ لَنَا فِي قَصِّ الشَّارِبِ، وَتَقْلِيمِ الْأَظْفَارِ، وَنَتْفِ الْإِبِطِ، وَحَلْقِ الْعَانَةِ، أَلَّا نَتْرُكَ أَكْثَرَ مِنْ أَرْبَعِينَ لَيْلَةً.
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa tënk jemp ay mustaas, ak lelli ay weyi loxo ak tànk, ak suqi poqtaan, ak wat ab naq, ci ñu bañ ko a bàyyi lu ëpp ñent-fukki fan.
As-Sawkaanii nee na: li ñu tànn mooy ñu tënk ko ci ñent-fukki yi ko Yonente bi tënk te bañ ko a jéggi, te ki nga xam ne jémpu ko ginnaaw ba mu gudee mbaa lu ni mel waaye mu bàyyi ko ba ca njeextalu diir ba kooku deesu ko jàppe ku wuute ak sunna.
Ibn Hubayrata nee na: hadiis bii mooy daytalu yeexe loolu, waaye li gën a yell mooy def ko laata muy egg ca daytal ga.
Lislaam dafa yittewoo set ak laab ak taar.
Jemp mustaas, ci dindi lenn ci kawar gi sax ci tuñu kaw wi.
Suqi poqtaan, ci dindi kawar gi ci sax, te mooy bérab bi nekk ci suufu fi teqale loxo bi ak mbagg mi.
Wat kawaru naq, te mooy kawar gu ñagas giy sax ci li wër awra wi, ci góor ak jigéen.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 222) (258).
Yataal gi (2)
شرح سنن أبي داود لابن رسلان (16/ 559).
مرشد ذوي الحجا والحاجة إلى سنن ابن ماجه والقول المكتفى على سنن المصطفى (3/ 115).