عربي - Arabic English Qafár af - Afar Afrikaans - Afrikanns Akan Shqip - Albanian አማርኛ - Amharic Հայերեն - Armenian অসমীয়া - Assamese Azərbaycanca - Azerbaijani Bamanankan - Bambara Bassa Bemba বাংলা - Bengali Bosanski - Bosnian Български - Bulgarian မြန်မာဘာသာ - Burmese Bisaya - Cebuano Cham Нохчий - Chechen chiCheŵa - Chewa 中文 - Chinese Адыгэбзэ - Circassian Hrvatski - Croatian Česky - Czech Dagbani Dansk - Danish فارسی دری - Dari Dendi ދިވެހި ބަސް - Dhivehi Nederlands - Dutch إستوني - Estonian Suomi - Finnish Français - French Fulfulde - Fula ქართული - Georgian Deutsch - German Ελληνικά - Greek ગુજરાતી - Gujrati Kreyòl ayisyen - Haitian Creole Hausa हिन्दी - Hindi Magyar - Hungarian Igbo Indonesia - Indonesian Italiano - Italian 日本語 - Japanese Jóola - Jola ಕನ್ನಡ - Kannada Қазақша - Kazakh ភាសាខ្មែរ - Khmer Kikuyu Ikinyarwanda - Kinyarwanda Ikirundi - Kirundi 한국어 - Korean كوردی سۆرانی - kurdish كوردي kurmancî - Kurmanji Kyrgyz ລາວ - Lao latviešu - Latvian Lingala lietuvių - Lithuanian Luganda Македонски - Macedonian Maguindanaon Malagasy - Malagasy Bahasa Melayu - Malay മലയാളം - Malayalam Mandinka मराठी - Marathi Mõõré - Moore नेपाली - Nepali أنكو - NKo Norwegian ଓଡ଼ିଆ - Odia oromoo - Oromo پښتو - Pashto فارسی - Persian Polski - Polish Portuguese ਪੰਜਾਬੀ - Punjabi Română - Romanian Русский - Russian Српски - Serbian Shona සිංහල - Sinhala Slovenščina - Slovenian Soomaaliga - Somali Soninke Sesotho - Sotho Español - Spanish Kiswahili - Swahili Svenska - Swedish Tagalog Тоҷикӣ - Tajik தமிழ் - Tamil తెలుగు - Telugu ไทย - Thai ትግረኛ - Tigrinya Türkçe - Turkish Ukrainian اردو - Urdu ئۇيغۇرچە - Uyghur Ўзбек - Uzbek Việt Nam - Vietnamese Wolof Yao Yorùbá - Yoruba Zarma زولو - Zulu
732 Hadiths
Encyclopedia of Prophetic Hadiths
Categories
Grading
Narrated in
Narrator
Show all narrators (210)
"su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc yi, day xëy nekk ku woos xiif di gont biir bi fees dell".
Wér na Imaam Ahmad ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-yyu ak Ibnu Maaja ak Ibnu Hibbaan ci Sahiiham ak Al-Haakim ñoo ko soloo.
«buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
Jenn waay ci Yahuud yi da ko a wax ne ko: yaw njiitu jullit ñi, amna ab aaya bu ngeen di jàng ci seen téete bi, bu wàccoon ci nun mbooleem Yahuud yi kon dananu jàppe bis booba feet, mu ne ko: ban aaya la? Mu ne ko: {Bis niki tay matalal naa leen seen diine xëpp naa leen samay xéewal gërëm naa ci yeen lislaam muy seen diine} [Al-Maa-ida: 3] Umar nee na: xam nanu bis booba, ak bérab ba mu wàcce ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fekk ma nga taxaw ca Arafa bisub àjjuma.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Amna jenn waay ci jamonoy Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu tudd Abdulla, ñu koy dàkkantale Mbaam, mu daan reeloo Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dóoroon ko yari yoon, ñu indi ko benn bis mu digle ñu dóor ko, jenn waay ne: Yàlla rëbb ko, ana lan moo gën a bari lu ñu koy indi? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: "buleen ko rëbb, giñ naa ci Yàlla ne xamuma lu dul ne bëgg na Yàlla ak ub Yonnenteem".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
«su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell.
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, mu wax: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, bu waxee: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, mu wax: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, bu waxee: hayya halas salaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: hayya halal falaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, mu wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: laa ilaaha illal Laahu, mu wax: laa ilaaha illal laahu te mu dëggu ci xolam kon dana dugg àjjana».
Wér na Muslim soloo na ko.
«jëf yi mi ngi aju ci yéene ja, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yónenteem, koo ku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yónenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot, walla jigéen ju mu bëgg a takk; kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay" ci beneen nettali ci Al-Buxaarii: "jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene
rekk lay am».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Benn bis danoo toog ci yònente bi, fa saasa benn waay ñëw, bu sol yéere ya weex tàll,kawar ga ñuul kukk,te kenn gisul ci moom jeexiit i tukki, te it kenn xamu ko ci nun, bam aksi toog ci yònente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-, daa di wéer ñaari wóomam ci ñaari wóomi yónente bi, teg ñaari tenqam ci kaw poojam,daal di ne ko: yaw Muhammat xibaar ma luy lislaam Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Lislaam mooy: nga seede ne amul kenn ku deesi jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, tey taxawal julli, di woor weeru koor, te aj Màkka benn yoon boo ko manee» mu ne ko: wax nga dëgg nu yéemu ci moom di ko laaj ba noppi di ko dëggal, mu ne ko: xibaar ma lan mooy gëm? mu ne ko: «mooy nga gëm Yàlla,ak i malaakaam,ak i téeréem, ak i yónentam, ak bis bu mujj ba, nga gëm ndogal yi; ya ca neex ak ya naqari» mu ne ko: wax nga dëgg daal ni ko: xibaar ma lan mooy rafetal? mu ni ko: «mooy ngay jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis, ndax boo ko gisul moom moo ngi lay gis» mu ne ko: xibaar ma kañ la bis-pénc? mu ne ko: «ki ñu koy laaj gënu koo xam ki ko koy laaj» mu ne ko: wax ma ay màndarngaam? mu ne ko: «mooy jaam ba jur ab sangam, nga gis way-fàndaañu ya way-rafle ya way-ñàkk ña sàmukati jur ya, ñuy guddalaante ca tabax ya» mu dem ma daal di sax ci ag jaaxle, mu ne ma: « Umar ndax xam nga aji-laaj ji ?» ma ne ko: Yàlla ak ub yónenteem ñoo xam mu ne ma: «koo ku Jibriil la, dafa ñëwóon ngir xamal leen seen diine».
Wér na Muslim soloo na ko.