"buleen ko rëbb, giñ naa ci Yàlla ne xamuma lu dul ne bëgg na Yàlla ak ub Yonnenteem".
Jële nañu ci Umar ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Amna jenn waay ci jamonoy Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu tudd Abdulla, ñu koy dàkkantale Mbaam, mu daan reeloo Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dóoroon ko yari yoon, ñu indi ko benn bis mu digle ñu dóor ko, jenn waay ne: Yàlla rëbb ko, ana lan moo gën a bari lu ñu koy indi? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: "buleen ko rëbb, giñ naa ci Yàlla ne xamuma lu dul ne bëgg na Yàlla ak ub Yonnenteem".
أَنَّ رَجُلًا عَلَى عَهْدِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ اسْمُهُ عَبْدَ اللَّهِ، وَكَانَ يُلَقَّبُ حِمَارًا، وَكَانَ يُضْحِكُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، وَكَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَدْ جَلَدَهُ فِي الشَّرَابِ، فَأُتِيَ بِهِ يَوْمًا فَأَمَرَ بِهِ فَجُلِدَ، فَقَالَ رَجُلٌ مِنَ القَوْمِ: اللَّهُمَّ الْعَنْهُ، مَا أَكْثَرَ مَا يُؤْتَى بِهِ؟ فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لاَ تَلْعَنُوهُ، فَوَاللَّهِ مَا عَلِمْتُ أَنَّهُ يُحِبُّ اللَّهَ وَرَسُولَهُ».
Ci jamonoy Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa amoon jenn waay ju tudd Abdulla, ñu koy dàkkantale Mbaam, mu daan reeloo Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci yenn waxam yi, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dóoroon ko ci naan sàngara, ñu indi ko benn bis ndax dafa naan sàngara mu digle ñu dóor ko. Kenn ci ñi teewoon ŋàññ ko, daal di ne: yal na ko Yàlla rëbb, ana lan moo gën a bari li ñi koy indi ndax naan sàngara?! Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: buleen ko ñaan ag dàq ci yërmàndey Yàlla, giñ naa ci Yàlla ne xamuma lu dul ne bëgg na Yàlla ak ub Yonnenteem.
dàqonte amul ci diggante def tere yi ak saxug bëgg Yàlla ak ub Yonnenteem ci xolu kiy koy def; ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne ki ñu tudd dafa bëgg Yàlla ak ub Yonnenteem ànd ak li muy def lépp.
Kiy def bàkkaar yu mag bu faatoo fekk moo ngi nuur ci lenn ci loolu kooku moo ngi ci coobarey Yàlla, bu ko soobee mu jéggal ko bu ko soobee mbugal ko, te deesul saxal ca sawara kenn ku bokk ci lislaam.
Sib nañu rëbb naankatu sàngara ju ñu ràññee; ndax jamtal na am lu tere rëbb ma dal ci kawam; ndax rëbb ku ñu ràññee ak ñaan ko Yàlla man na ko a yóbbe ci wéy ca, walla mu naaguloo ko ci tuub.
Dagan na ñu rëbb ku ñu ràññeewul te mu melowoo loolu.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 158) (6780).
Yataal gi (2)
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (9/ 452).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (29/ 394).