عربي - Arabic English Qafár af - Afar Afrikaans - Afrikanns Akan Shqip - Albanian አማርኛ - Amharic Հայերեն - Armenian অসমীয়া - Assamese Azərbaycanca - Azerbaijani Bamanankan - Bambara Bassa Bemba বাংলা - Bengali Bosanski - Bosnian Български - Bulgarian မြန်မာဘာသာ - Burmese Bisaya - Cebuano Cham Нохчий - Chechen chiCheŵa - Chewa 中文 - Chinese Адыгэбзэ - Circassian Hrvatski - Croatian Česky - Czech Dagbani Dansk - Danish فارسی دری - Dari Dendi ދިވެހި ބަސް - Dhivehi Nederlands - Dutch إستوني - Estonian Suomi - Finnish Français - French Fulfulde - Fula ქართული - Georgian Deutsch - German Ελληνικά - Greek ગુજરાતી - Gujrati Kreyòl ayisyen - Haitian Creole Hausa हिन्दी - Hindi Magyar - Hungarian Igbo Indonesia - Indonesian Italiano - Italian 日本語 - Japanese Jóola - Jola ಕನ್ನಡ - Kannada Қазақша - Kazakh ភាសាខ្មែរ - Khmer Kikuyu Ikinyarwanda - Kinyarwanda Ikirundi - Kirundi 한국어 - Korean كوردی سۆرانی - kurdish كوردي kurmancî - Kurmanji Kyrgyz ລາວ - Lao latviešu - Latvian Lingala lietuvių - Lithuanian Luganda Македонски - Macedonian Maguindanaon Malagasy - Malagasy Bahasa Melayu - Malay മലയാളം - Malayalam Mandinka मराठी - Marathi Mõõré - Moore नेपाली - Nepali أنكو - NKo Norwegian ଓଡ଼ିଆ - Odia oromoo - Oromo پښتو - Pashto فارسی - Persian Polski - Polish Portuguese ਪੰਜਾਬੀ - Punjabi Română - Romanian Русский - Russian Српски - Serbian Shona සිංහල - Sinhala Slovenščina - Slovenian Soomaaliga - Somali Soninke Sesotho - Sotho Español - Spanish Kiswahili - Swahili Svenska - Swedish Tagalog Тоҷикӣ - Tajik தமிழ் - Tamil తెలుగు - Telugu ไทย - Thai ትግረኛ - Tigrinya Türkçe - Turkish Ukrainian اردو - Urdu ئۇيغۇرچە - Uyghur Ўзбек - Uzbek Việt Nam - Vietnamese Wolof Yao Yorùbá - Yoruba Zarma زولو - Zulu
732 Hadiths
Encyclopedia of Prophetic Hadiths
Grading
Narrated in
Narrator
Show all narrators (210)
Yaayam Bintu Rawaahata dafa laaj baayam mu may ko lenn ci alalam ñeel doomam, mu tanqamlu ko lu mat at, topp mu mujj gis loolu, mu ne ko: du ma nangu lu dul nga seedeloo Yonente Yàlla bi ci li nga may sama doom ji, mu ñëw ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, yaayu kii di Bint Rawaahata dafa bëgg ma seedeloo la ci li ma may doomam ji, Yonnente bi ne ko: yaw Abuu Basiir, ndax am nga jeneen doom ju dul kii?" Mu ne: waaw, mu ne ko: "ndax ñoom ñépp nga may lu mel nii?" Mu ne: déedéet, mu ne ko: "kon bul ma seedeloo, man duma seede ag jeng", ñëw na ci Muslim: "demal seedeloo lii ci keneen ku dul man".
Wér na Al-Buxaarii ak Muslim dëppoo nañu ci te amna ay waxiin yu bari.
«li dagan de leer na li araam it leer na, seen diggante nag am na ay lënt, te ñu bari si nit ñi duñu ko xam, képp ku moytu yu lënt yi ñoŋal na diineem ak deram, waaye ku tàbbi ca lënt ya kooku tàbbi na ca yu araam ya, mi ngi mel ni sàmmkat biy sàmm ci li wër ab ñag, daanaka rekk sàmm na ca biiram, xanaa du buur bu nekk am na ab ñagam, te ñagub Yàlla mooy li mu araamal, xamleen ne yaram am na aw lumb wow bu baaxee yaram wépp baax, bu yàqoo yaram wépp yàqu, loolu mooy xol«.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Nekkoon naa ci Minbaru Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, jenn waay ne: faalewuma ma ñàkk a def jenn jëf ginnaaw lislaam lu dul may nàndal kiy aj, keneen ne: faalewuma ma ñàkk a def jenn jëf ginnaaw lislaam lu dul ma dundal jàkkay Màkka, keneen ne: jihaad ci yoonu Yàlla moo gën yi ngeen wax, Umar gëdd leen, ne leen: buleeen yëkkëti seen kàddu fekk yéen a ngi ci Minbaru Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc te bisu àjjuma la, waaye bu ngeen jullee àjjuma ma dugg laaj ko li ngeen di wuute, Yàlla mu màgg mi wàcce: {ndax dangeen a def nàndal kiy aj ak aar jàkka ja ñu wormaal mu yemoo ak ki gëm Yàlla ak bis bu mujj ba} [At-Tawba: 19] aaya bi ba mu jeex.
Wér na Muslim soloo na ko.
«misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day
ànd bañ a nelaw ak di tàng».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"misaalu ki taxaw ci foroñceeri Yàlla yi ak ki ci tàbbi, moo ngi mel ni aw nit wu tegoo bant ci ag gaal, ñii am kaw ga, ñii nekk ca suuf ga, ñi nekk ci suuf bu ñuy wut ndox dañuy romb ña nekk seen kaw, nu mujj wax ne: nun de bu nu xaroon ci sunu wàll aw xarit te dunu lor ñi nekk sunu kaw, bu ñu leen bàyyee ak la ñu bëgg ñoom ñéppay alku, waaye bu ñu téyee seen loxo danañu mucc, ñoom ñépp mucc".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
«ñaan mooy jaamu Yàlla» daal di jàng: "Aaya biy wax ne:
{séen Boroom nee na wooleen ma ma wuyu leen ñi may rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox} [ soratou Xaafiri: 60]».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.