Skip to content

{ndax dangeen a def nàndal kiy aj ak aar jàkka ja ñu wormaal mu yemoo ak ki gëm Yàlla ak bis bu mujj ba} [At-Tawba: 19] aaya bi ba mu jeex.

Jële nañu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Nekkoon naa ci Minbaru Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, jenn waay ne: faalewuma ma ñàkk a def jenn jëf ginnaaw lislaam lu dul may nàndal kiy aj, keneen ne: faalewuma ma ñàkk a def jenn jëf ginnaaw lislaam lu dul ma dundal jàkkay Màkka, keneen ne: jihaad ci yoonu Yàlla moo gën yi ngeen wax, Umar gëdd leen, ne leen: buleeen yëkkëti seen kàddu fekk yéen a ngi ci Minbaru Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc te bisu àjjuma la, waaye bu ngeen jullee àjjuma ma dugg laaj ko li ngeen di wuute, Yàlla mu màgg mi wàcce: {ndax dangeen a def nàndal kiy aj ak aar jàkka ja ñu wormaal mu yemoo ak ki gëm Yàlla ak bis bu mujj ba} [At-Tawba: 19] aaya bi ba mu jeex.

كُنْتُ عِنْدَ مِنْبَرِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ رَجُلٌ: مَا أُبَالِي أَلَّا أَعْمَلَ عَمَلًا بَعْدَ الإِسْلَامِ إِلَّا أَنْ أُسْقِيَ الحَاجَّ، وَقَالَ آخَرُ: مَا أُبَالِي أَلَّا أَعْمَلَ عَمَلًا بَعْدَ الإِسْلَامِ إِلَّا أَنْ أَعْمُرَ المَسْجِدَ الحَرَامَ، وَقَالَ آخَرُ: الجِهَادُ فِي سَبِيلِ اللهِ أَفْضَلُ مِمَّا قُلْتُمْ، فَزَجَرَهُمْ عُمَرُ، وَقَالَ: لَا تَرْفَعُوا أَصْوَاتَكُمْ عِنْدَ مِنْبَرِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَهُوَ يَوْمُ الجُمُعَةِ، وَلَكِنْ إِذَا صَلَّيْتُ الجُمُعَةَ دَخَلْتُ فَاسْتَفْتَيْتُهُ فِيمَا اخْتَلَفْتُمْ فِيهِ، فَأَنْزَلَ اللهُ عَزَّ وَجَلَّ: {أَجَعَلْتُمْ سِقَايَةَ الْحَاجِّ وَعِمَارَةَ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ كَمَنْ آمَنَ بِاللهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ} [التوبة: 19] الآيَةَ إِلَى آخِرِهَا.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

An-Nuhmaan ibn Basiir yal na leen Yàlla dollee gërëm dafa wax ne moom dafa toogoon ci Minbaru Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu dégg jenn waay wax ne: faalewuma ma ñàkk a def jenn jëf ginnaaw ba ma tuube lu dul may nàndal kiy aj. Keneen ne: faalewuma ma ñàkk a def jenn jëf ginnaaw ba ma tuubee lu dul may dundal jàkka ja ñu wormaal, keneen ne: jihaad ci yoonu Yàlla de moo gën li ngeen wax. Umar ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm gëdd lee vi kàddu gi ñuy yëkkëti ci Minbaru Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc te subag àjjuma la woon, waaye bu ma jullee àjjuma dinaa dugg laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc li ngeen di wuute, Yàlla mu màgg mi wàcce; {mo ndax dangeen a def nàndal kiy aj ak dundal jàkka ja ñu wormaal mu yemoo ak ki gëm Yàlla ak bis bu mujj ba di jihaad ci yoonu Yàlla ñooñu duñu yem fa Yàlla te Yàlla du gindi way-tooñ yi}. [At-Tawba : 19].

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Gënanteg jëf yi ci pay ak yool.

Gënanteg jëf yi moo ngi ci kem ni mu dikke ci Sariiha, waaye nekkul ci kem góor-góorlug nit ñi.

Ngëneelu jihaad ci yoonu Yàlla ci sàrtug gëm Yàlla ak bis bu mujj ba.

An-Nawawii nee na: nekk na ci ne sib nañu yëkkëti kàddu ci jàkka yi bisu àjjuma ak bu dul moom, ak ne deesul yëkkëti kàddu ci xam-xam du caagine leneen bu nit ñi dajaloo ngir julli ndax li ci nekk jaxase leen ak jaxase ñiy julli ak ñiy tudd Yàlla.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1499) (1879).

Yataal gi (3)

المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (3/ 720).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (32/ 395).

النهاية في غريب الحديث والأثر (ص 897).