"wàcce nañu ci man ay aaya yoy musuñoo wàcce yu mel ni ñoom, Ñaari muslukaay yi"
Jële nañu ci Huqbata Ibn Haamir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na ma:
"wàcce nañu ci man ay aaya yoy musuñoo wàcce yu mel ni ñoom, Ñaari muslukaay yi"
«أُنْزِلَ -أَوْ أُنْزِلَتْ- عَلَيَّ آيَاتٌ لَمْ يُرَ مِثْلُهُنَّ قَطُّ، الْمُعَوِّذَتَيْنِ».
Huqbata ibn Haamir yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa nettali jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ko ne: Yàlla wàcce na ci man ci guddi gii aaya yoo xam ne yu mel ni ñoom masula wàcc-maanaam ci muslaay- ñuy Ñaari muslukaay yi: Saaru {Xul ahuusu bi rabbil falaqi} ak Saaru {Xul ahuusu bi rabbin naasi}.
Leeral màggug ñaari saar yi.
Ñaaxe ci muslu ci ñoom ñaar ci bépp ay.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 558) (814).
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (2/ 158) (952).
Yataal gi (1)
ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (12/ 312).