Njabootu Muhammat lekkuñu ñaari lekk ci ab bis lu dul ne genn ga tàndarma lay doon.
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Njabootu Muhammat lekkuñu ñaari lekk ci ab bis lu dul ne genn ga tàndarma lay doon.
مَا أَكَلَ آلُ مُحَمَّدٍ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَكْلَتَيْنِ فِي يَوْمٍ إِلَّا إِحْدَاهُمَا تَمْرٌ.
Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne waa kër Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lekkuñu ñaari lekk ci benn bis lu dul ne genn lekk gi tàndarma lay doon.
Toroxlug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak waa këram, ndax aamaana sax duñu am ci bis bi lu dul genn lekk.
Tàndarma moo gënoon a yomb ci ñoom lu dul moom.
Ngëneelu dëddu ak doylu ci lu néew ci dund gi, ak ne dafa bokk ci jikkoy Yonnente yi, ak jaar-jaari ña ñu yónni.
Jëfandikoo jam ñaari yoon ci bis bi dafa bokk ci bir yu dagan yi, te daa bokk ci aada yi ñu xam ci araab yi, daan nañu lekk ci bis bi ñaari lekk, lekkug añ, ak lekkug reer.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 97) (6455).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2282) (2971).
Yataal gi (1)
فتح الباري لابن حجر (11/ 292).