Skip to content

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa bind jëme ca Kisraa, ak ca Xaysar, ak ca An-Najaasii, ak ci bépp ponkal di leen woo jëme ci Yàlla mu kawe mi

Jële nañu ci Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa bind jëme ca Kisraa, ak ca Xaysar, ak ca An-Najaasii, ak ci bépp ponkal di leen woo jëme ci Yàlla mu kawe mi, waaye du An-Najaasii mi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jullee woon.

أَنَّ نَبِيَّ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَتَبَ إِلَى كِسْرَى، وَإِلَى قَيْصَرَ، وَإِلَى النَّجَاشِيِّ، وَإِلَى كُلِّ جَبَّارٍ يَدْعُوهُمْ إِلَى اللهِ تَعَالَى، وَلَيْسَ بِالنَّجَاشِيِّ الَّذِي صَلَّى عَلَيْهِ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc laata muy faatu dafa bind jëme ci buuri xeet yi ko wër di leen woo ci lislaam; mu bind jëme ci Kisraa aw sant la ñeel bépp buuru Al-Furs, ak ca Xaysar aw sant la ñeel bépp buuru Ar-Ruum, ak ca An-Najaasii aw sant la ñeel bépp buuru Al-Habass. Mu bind batay jëme ci ponkali buur yi song ay nit not leen, Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm leeral ne An-Najaasii mii nekkul ka tuuboon ba faatu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di koy jullee julleeg ku fàddu.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yoonalees nañu woo ñi dul jullit jëme leen ci lislaam, te seen buur yi ak seen njiit yi ca lañu bokk.

Yoonalees nañu jëfe li ci téere bi ak leerar yi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1397) (1774).

Yataal gi (3)

المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (3/ 612).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (31/ 67).

النهاية في غريب الحديث والأثر (136).