Skip to content

"buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi

Jële na ñu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

"buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi, walla ngir am ci wàccuwaay ca jotaay ya, képp ku def loolu, sawara la jëm, sawara la jëm".

«لَا تَعَلَّمُوا الْعِلْمَ لِتُبَاهُوا بِهِ الْعُلَمَاءَ، وَلَا لِتُمَارُوا بِهِ السُّفَهَاءَ، وَلَا تَخَيَّرُوا بِهِ الْمَجَالِسَ، فَمَنْ فَعَلَ ذَلِكَ، فَالنَّارُ النَّارُ».

Ibnu Maaja soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo sàkku xam-xam ngir ndamu puukarewu ak woroom xam-xam yi, ak di wane ne man boroom xam-xam laa ne yéen, walla di ci wàqante ak a werente ak way-dese ñi ak ñu gàtt xel ñi, walla di sàkku xam-xam ngir nekk njiit ca jotaay ya, ñu di ko jiital ca kaw ñeneen ña fa nekk. Ku def loolu; kooku yayoo na sawara ngir sababus ngistalam ak ñàkk a sellalam ci sàkku xam-xam ngir Yàlla.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Tëkkoo nañu ci sawara képp kuy sàkku xam-xam ngir ndamu mbaa werente ca walla nekk njiit ca jotaay ya, mbaa yu ko niru.

Solos sellal ñeel kuy sàkku xam-xam te di ko xamle.

Ci yéene la jëf di tabaxu te ca la fay ga di aju.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (1/ 170) (254).

Yataal gi (2)

مرشد ذوي الحجا والحاجة (2/378).

مشارق الأنوار الوهاجة ومطالع الأسرار البهاجة في شرح سنن الإمام ابن ماجه (4/ 482).