Skip to content

"deeleen baril lu ngeen di tudd liy màbb bànneex yi" maanaam dee.

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"deeleen baril lu ngeen di tudd liy màbb bànneex yi" maanaam dee.

«أَكْثِرُوا ذِكْرَ هَادمِ اللَّذَّاتِ» يَعْنِي الْمَوْتَ.

At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ñoo ko soloo.
Tane na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaaxe ci ñuy baril li ñuy tudd dee gi nga xam ne ci tudd ko la nit ki di fàttalikoo allaaxira, bu ko defee mu màbb ag bëggam ñeel bànneexi àdduna yi ci xolam, rawatina yi araam yi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Dee day dog bànneexi àdduna yi, waaye ci àqi aji-gëm ji day wëlbatiku jëm ci bànneexi allaaxira ak bànneexi Àjjana, ak la cay am ci ay yiw yu màgg.

Fàttaliku dee ak la ca ginnaawam dafa bokk ci liy waral tuub ak bàyyi bàkkaar yi, ak waajal allaaxira.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 141) (2307).

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (4/ 4) (1824).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (5/ 326) (4258).

Yataal gi (1)

ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (18/ 219).