"jullig mbooloo moo gën jullig kenn ci yéen moom dong, luy toll ci ñaar-fukk ak juróomi xaaj, Malaakay guddi gi ak Malaakay bëccëg gi dañuy daje ci jullig Fajar gi"
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"jullig mbooloo moo gën jullig kenn ci yéen moom dong, luy toll ci ñaar-fukk ak juróomi xaaj, Malaakay guddi gi ak Malaakay bëccëg gi dañuy daje ci jullig Fajar gi" topp Abuu Hurayrata wax ne: jàngleen bu leen neexee: {Alxuraanu Fajar gi lu ñuy teewe la} [Al-Israa: 78].
«تَفْضُلُ صَلاَةُ الجَمِيعِ صَلاَةَ أَحَدِكُمْ وَحْدَهُ، بِخَمْسٍ وَعِشْرِينَ جُزْءًا، وَتَجْتَمِعُ مَلاَئِكَةُ اللَّيْلِ وَمَلاَئِكَةُ النَّهَارِ فِي صَلاَةِ الفَجْرِ» ثُمَّ يَقُولُ أَبُو هُرَيْرَةَ: فَاقْرَءُوا إِنْ شِئْتُمْ: {إِنَّ قُرْآنَ الفَجْرِ كَانَ مَشْهُودًا} [الإسراء: 78].
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne yool ak fayug jullig góor gi ci mbooloo mi ànd ak imaam moo gëne ñaar-fukk ak juróomi xaaj ci bu jullee moom dong ci këram walla ci maarseem, topp Yonente bi wax ne Malaaka yu guddi yi ak Malaaka yu bëccëg yi dañuy daje ci jullig Fajar gi, Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm daal di wax ngir seede loolu mu ne: Jàngleen bu leen neexee: {Alxuraanu Fajar gi lu ñuy teewe la} [Al-Israa: 78], Maanaam jullig Fajar gi Malaaka yu guddi gi ak Malaaka yu bëccëg gi dañu koy teewe.
Ibn Hajar nee na: julli ca jàkka ja ca mbooloo ma moo ëpp julli ci kër gi ak ci maarse bi ci mbooloo ak ci beru, Ibn Daxiixilhiid moo ko wax.
Ngëneelu jullig Fajar; ndax li mu jagoo daje ga ca Malaaka yi di daje.
Ibn Baas nee na: jaadu na ci aji-gëm ji mu xér ci sàmmonte ak julli ca mbooloo ma donte këram dafa sori, ngir mu am yiw wu màgg wii.
An-Nawawii wax na ci boole nettali yi ñëw ci ne jullig mbooloo gëne na jullig kenn luy tollu ak ñaar-fukk ak juróomi daraja, beneen mu ne ñaar-fukk ak juróom-ñaar: boole leen nag ci ñatti anam lay nekke: bi ci njëkk: amul safaanoo ndax tudd li gën a néew du dàq la gën a bari, ñaareel bi: dafa tudd li néew topp Yàlla xamal ko ne yokk na ngëneelam ci loolu, ñatteel bi: day wuute ci kem wuuteg jullikat yi ci julli gi, ñenn ñi am ñaar-fukk ak juróom, ñeneen ñi am ñaar-fukk ak juróom-ñaar ci kem matug julli gi ak sàmmonte ak melokaan ya ak toroxlu ga ak barig mbooloo ma ak seenug ngëneel ak teddngay bérab ba ak yu ni mel, Yàlla rekk a xam.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 131) (648).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 450) (649).
Yataal gi (4)
تيسير الكريم الرحمن في تفسير كلام المنان.
لعبد الرحمن آل سعدي (ص464).
توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.
لعبد الله البسام (2/ 210).