Skip to content

Nun nooy xeet wi mujj, di ñi ñu njëkk a regle

Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

Nun nooy xeet wi mujj, di ñi ñu njëkk a regle, dañuy naan: ana xeet wi jàngul ak seen Yonnente? Nun nooy ñi mujj di ñiy njëkk".

«نَحْنُ آخِرُ الأُمَمِ، وَأَوَّلُ مَنْ يُحَاسَبُ، يُقَالُ: أَيْنَ الأُمَّةُ الأُمِّيَّةُ وَنَبِيُّهَا؟ فَنَحْنُ الآخِرُونَ الأَوَّلُونَ».

Ibnu Maaja soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne xeetam wi mooy xeet wi mujj a an ci jamono te mooy xeet wi ñuy njëkk a regle ëllëg bis-pénc, dañu wax ëllëg bis-pénc: ana xeet wi jàngul ak seen Yonnente? Ñu askanale ko ci ñàkk a jàngu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci li mu manul a jàng ak bind. Ñu woo leen ngir njëkk leen a regle, nun noo mujj a am ci jamono, di ñiy njëkk ca regle ga ëllëg bis-pénc ak ci dugg àjjana.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu xeet wii ci kaw xeet yi jiitu.

Dellluwaay yi
Yataal gi (3)

حاشية السندي على سنن ابن ماجه (2/575).

ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (16/52).

مرشد ذوي الحجا والحاجة إلى سنن ابن ماجه (26/241).