"bàmmeel de mooy wàccuwaay bi njëkk ci wàccuwaayi allaaxira yi, bu ca muccee la ca ginnaawam mooy gën na yomb, bu ca muccul la ca ginnaawam mooy gën na tar".
Jële nañu ci Haanii jaamub Usmaan yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Usmaan bu daan taxaw ci bàmmeel day jooy ba sikkinam bi tooy, ñu ne ko: dañu lay tuddal àjjana ak sawara te doo jooy, ba noppi ngay jooy ci lii? Mu ne Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"bàmmeel de mooy wàccuwaay bi njëkk ci wàccuwaayi allaaxira yi, bu ca muccee la ca ginnaawam mooy gën na yomb, bu ca muccul la ca ginnaawam mooy gën na tar".
«إِنَّ الْقَبْرَ أَوَّلُ مَنْزِلٍ مِنْ مَنَازِلِ الْآخِرَةِ، فَإِنْ نَجَا مِنْهُ فَمَا بَعْدَهُ أَيْسَرُ مِنْهُ، وَإِنْ لَمْ يَنْجُ مِنْهُ فَمَا بَعْدَهُ أَشَدُّ مِنْهُ».
Njiitu jullit ñi Usmaan ibn Affaan yal na ko Yàlla dollee gërëm bu daan taxaw ci ab bàmmeel day jooy ba sikkinam bi tooy ak rangooñ, ñu ne ko: Dañu lay tuddal àjjana ak sawara te doo jooy ngir namm àjjana walla ragal sawara! ba noppi ngay jooy ngir bàmmeel? Mu wax ne: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne bàmmeel mooy wàccuwaay bi njëkk ci wàccuwaayi allaaxira yi, bu ca muccee set ca kon la ca ginnaawam ci ay wàccuwaay mooy gën a yomb, bu muccul ci ay mbugalam nag; la cay tege ci mbugal mooy gën na tar li mu nekk.
Leeral ni Usmaan nekke woon ci ragal Yàlla ànd ak ne moom bokk na ci ñi ñu bégal ci àjjana.
Yoonalees na jooy ci boo fàttalikoo tiisi bàmmeel ak bis-pénc.
Saxal xéewali bàmmeel ak mbugalam.
Ragalloo mbugalu bàmmeel.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 130) (2308).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (5/ 333) (4267).
Yataal gi (6)
مشكاة المصابيح.
للتبريزي (1/ 48).
تحفة الأحوذي بشرح جامع الترمذي.
المباركفوري (6/ 490).
مرقاة المفاتيح شرح مشكاة المصابيح.
لعلي القاري (1/ 215).