Skip to content

«képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram»

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram»

«مَنْ صَامَ رَمَضَانَ إِيمَانًا وَاحْتِسَابًا غُفِرَ لَهُ مَا تَقَدَّمَ مِنْ ذَنْبِهِ»

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare ne képp ku woor weeru koor ngir gëm Yàlla, ak dëggal ne woor farata la, ak li Yàlla mu kawe mi dig way-woor yi ci fay ak yool yu rëy, mu jublu ca jëmmi Yàlla ci lu dul ngistal walla ndéggtal, dees na ko jéggal bàkkaaram yi weesu.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu sellal ak am solos woor weeru koor ak yu dul yooyu ci jëf yu sell yi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 16) (38).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 523) (760).

Yataal gi (8)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 361).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (2/ 868).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (15/ 40).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (5/ 270).