Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

25 of 732 cards

Clear filters
«képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram»
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Ay gaay ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wan nañu leen Laylatul Xadri ci ay nelaw ci juróom-ñaari fan yi mujj, Yonente Yàlla bi daal di wax ne: "gis naa ne seen gent yi dañoo dëppoo ci juróom-ñaar yu mujj yi, ku koy diir na ko diir ci juróom-ñaar yu mujj yi".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Àjjana am na ab buntu bu ñuy woowe Rayyaan, woorkat yi ñoo cay dugg ëllëg bis-pénc, kenn du ca dugg ku dul ñoom, dañuy wax naan: ana woorkat yi, ñu jug kenn du ca dugg ku dul ñoom, bu ñu duggee ñu tëj ko, keneen du ca dugg".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam, te dolliwuma ca dara, ndax dinaa dugg àjjana ? Mu ne ko: "waaw".
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Yàlla nee na: jépp jëfi doomu Aadama moom la ñeel, ba mu des woor, moom man maa ko moom te maa koy fay, te woor ab pakk la, bu nit ki nekkee ci bisu wooram bu mu jëf jëfi caaxaan bu mu coow, bu ko kenn saagaa mbaa mu xeex ak moom, na ko wax ne man damaa woor, giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom, xetu gémmiñu aji-woor ji moo gën a teey fa Yàlla ci xetu Misk, aji-woor ji am na ñaari mbégte yu muy bég: bu dogee day bég, bu dajee ak Boroomam day bég ci wooram gi».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku man a takk jabar na takk, ndaxte moo gën a man a damm ab gis, gën a man a sàmm péy mi, ku ko manul nag dénk naa ko woor, ndaxte dana ko man a téye».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.