Ba ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yónnee Yaman da ko a digal mu jël ci Nag fanweer yu nekk wenn nag wu am at wu góor walla wu jigéen
Jële nañu ci Muhaas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Ba ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yónnee Yaman da ko a digal mu jël ci Nag fanweer yu nekk wenn nag wu am at wu góor walla wu jigéen, ak ci ñent-fukk yu nekk wenn nag wu am ñaari at, ak ci ñoñ-téere buy aji-gént -maanaam di gént di sëy- ab Diinaar walla lu toll ni moom ci Mahaafir, ay yére la yu nekk Yaman.
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لَمَّا وَجَّهَهُ إِلَى الْيَمَنِ أَمَرَهُ أَنْ يَأْخُذَ مِنَ الْبَقَرِ مِنْ كُلِّ ثَلَاثِينَ تَبِيعًا أَوْ تَبِيعَةً، وَمِنْ كُلِّ أَرْبَعِينَ مُسِنَّةً، وَمِنْ كُلِّ حَالِمٍ -يَعْنِي مُحْتَلِمًا- دِينَارًا أَوْ عَدْلَهُ مِنَ المَعَافِرِ، ثِيَابٌ تَكُونُ بِالْيَمَنِ.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa yónni Muhaas ibn Jabal yal na ko Yàlla dollee gërëm fa Yaman ngir mu xamal nit ñi ak woo leen ci diine, bokk na ci li mu ko digal mooy mu jël ci jullit ñi asaka ci seen nag yi, fanweeri nag yu ne mu jël ci aw yëkk wu am at walla nag wu jigéen wu am at; te mooy wu matal am at, ak ci ñent-fukki nag yu ne mu jël ca aw nag wu am ñaari at; te mooy wu matal ñaari at. Ak mu jël lempo ci ñoñ-téere yi ñuy Yahuud yi ak Nasaraan yi ci góor gu mat gu ne ab Diinaar, walla lu tolloo ak Diinaar ci yérey Yaman yi ñuy woowe: Mahaafir.
Lempo deesu no jël ci ku dul ku egg ci gént; ndax tënku ki ñu dul jël moom lempo: mooy ki nga xam ne bu ñu ko jàppe du dagan ñu ray ko: muy xale, ak jigéen, ak ku dul ñoom ñaar.
Nattale lempo day dellu ci góor-góorlug imaam bi,ndax day wuute kem wuuteg bérab bi ak jamono ji, ak aji-woomal ji ak aji-ñàkk ji, tegtali loolu mooy ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ko nattale ci waa Yaman, mu wax Muhaas: "jëlal ci aji-gént gu ne Diinaar", waaye lempo bi yokk na ci nattaleg Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm ba mu ko nattalee waa Saam.
Yittewoo dajale asaka, ak féetele ko ki koy dajale dafa bokk vi liggéeyu njiit li.
Tabiih: mooy lu matal at, ba dugg ci ñaareel bi, tuddees nañu ko Tabiih: ndaxte deñul di topp yaayam.
Diinaar: xaalidu wurus la, Diinaaru lislaam: day peese ñenti garaam ak ñenteelu xaaju wurus (4.25garaam).
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (3/ 26) (1576).
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (2/ 13) (623).
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (5/ 25) (2450 - 2451).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (3/ 22) (1803).
Yataal gi (6)
فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (3/ 35).
توضيح الأحكام من بلوغ المرام.
لعبد الله البسام (3/ 297).
سبل السلام.
للصنعاني (1/ 517 ).