Skip to content

"kenn ci yéen bu mu ragal nit ñi ba baña wax dëgg bu dee gis na ko walla mu xam ko".

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"kenn ci yéen bu mu ragal nit ñi ba baña wax dëgg bu dee gis na ko walla mu xam ko".

«لَا يَمْنَعَنَّ رَجُلًا مِنْكُمْ مَخَافَةُ النَّاسِ أَنْ يَتَكَلَّمَ بِالْحَقِّ إِذَا رَآهُ أَوْ عَلِمَهُ».

At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xutba ci sahaaba yi mu bokk ci li mu leen dénk jullit bi bu ko ragal nit ñi teree wax dëgg ak seen doole tax muy bàyyi a wax dëgg walla di ko digle saa su ko gisee walla mu xam ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci feeñal dëgg ak bañ ko a nëbb ngir ragal nit ñi.

Wax dëgg tekkiwul ñàkk a taqoo ak teggin yi ci anamu waxiin wi ak xereñte ci waare wu rafet.

Dañoo war a weddi lu bon, ak jiital àqi Yàlla mu kawe mi ci kaw njariñi nit yi safaanoo ak moom.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 53) (2191).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (5/ 141) (4007).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (17/ 490) (11403).